Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Gëm naa ne Yexowa mu ngi ak man

Gëm naa ne Yexowa mu ngi ak man

(Sabóor 27:⁠13)

Telesarseel:

  1. 1. Man duma tiit ndax gaynde.

    Man duma tiit ndaxi noon.

    Ak Yàlla ci sama wet,

    Duma lox, duma daw.

    Yexowa mooy ki ànd ak man.

    (AWU BI)

    Ak ngëm gu wóor, man maa ngi gis li may xaar.

    Ak ngëm gu wóor, kenn warul tax ma tiit.

    Ak Yexowa, mën naa lépp.

    Dara du ma téye,

    Ndaxte Yexowa dina ma aar—

    Ak ngëm gu wóor.

  2. 2. Ñépp ñi gëmoon te takku,

    Ñoom seen muñ du réer ci neen.

    Dañu dee ak seen ngëm.

    Seen ëllëg dina neex.

    Yàlla dina leen woo ñu jóg.

    (AWU BI)

    Ak ngëm gu wóor, man maa ngi gis li may xaar.

    Ak ngëm gu wóor, kenn warul tax ma tiit.

    Ak Yexowa, mën naa lépp.

    Dara du ma téye,

    Ndaxte Yexowa dina ma aar—

    Ak ngëm gu wóor.

    (PONT BI)

    Ak ngëm gu wóor, man mën naa lu leen të.

    Ak ngëm gu wóor, am naa yaakaar.

    Ngëm gi ma am,

    Looloo ma aar ci lépp li am.

    Ndax moo ma may xolu muñ tiis.

  3. 3. Ak suuf su naat si ñuy xaar

    Ngir nit ñi bég ba fàww.

    Duma xàddi mukk.

    Xam naa ne léegi rekk

    Nguuru Yàlla sampu fi ba fàww.

    (AWU BI)

    Ak ngëm gu wóor, man maa ngi gis li may xaar.

    Ak ngëm gu wóor, kenn warul tax ma tiit.

    Ak Yexowa, mën naa lépp.

    Dara du ma téye,

    Ndaxte Yexowa dina ma aar—

    Ak ngëm gu wóor,

    Ak ngëm gu wóor.

(Xoolal itam Yawut ya 11:​1-40).