Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Ni dawalkatu gaal soxlaa weñ bu tuuti ngir jëmale gaalam fi mu bëgg, noonu la waajur yi soxlaa yar seeni doom ngir ñu nekk ñu baax.

WAAJUR YI ÑOO MOOM LII

6: Yar

6: Yar

LI MUY TEKKI

Baatu yar mën na tekki won nit ki li mu war a def walla jàngal ko dara. Lée-lée, dafay laaj nga jubanti xale bi. Waaye li ci gën a bare, dafay laaj nga yedd xale bi te dimbali ko mu jàng a def lu baax.

LI TAX MU AM SOLO

Ci at yii weesu, waajur yu bare yaratuñu seeni doom. Li ko waral mooy, dañoo foog ne, bu ñu jubantee seeni doom, xale yi dootuñu wóolu seen bopp. Waaye, waajur yu baax, dañuy jël ay dogal yu baax ci kër gi, te dimbali xale yi ñu topp leen.

«Bu ñu bëggee xale yi doon ay mag yu baax ëllëg, fàww ñu won leen ne am na lu ñu mën a def ak lu ñu mënul a def. Xale bu ñu yarul, dafay jël ay dogal yu bon te loolu mën na ko jural ay jafe-jafe» (Pamela).

LI NGA MËN A DEF

Deel def li nga wax. Sa doom bu toppul li nga tëral, teg ko daan bi war. Waaye, deel ndokkeel sa doom bu defee li nga tëral.

«Ci àddina si, jafe na ñu gis ay xale yuy déggal seeni waajur. Moo tax, damay faral di ndokkeel samay doom ci ni ñu may déggale. Ni ma leen di ndokkeel moo tax mu yomb ci ñoom ñu nangu yar bi ma leen di yar» (Christine).

LII LA BIIBËL BI WAX: «Lu waay ji, moom ngay góob» (Galasi 6:7).

Na ngeen am xel. Booy yar sa doom, bàyyil xel ci at yi mu am, ci li mu àttan ak ci lu bon li mu def. Yar bi dafay gën a laal xale bi bu méngoo ak lu bon li mu def. Ci misaal, bu toppul li nga wax ci ni mu war a jëfandikoo telefonam, mën nga jël telefon bi ci moom, te denc ko ab diir. Bu dee li mu def garaawul, jarul nga ciy mer ba mu ëpp.

«Damay jéem a xam ndax li sama doom def moo ko tey walla dafa juum rekk. Am na ay jikko yoo xam ne, fàww nga def lépp ngir mu deñ ci sa doom. Mu am njuumte yoo xam ne waxtaan rekk doy na ci» (Wendell).

LII LA BIIBËL BI WAX: «Buleen bundxataal seeni doom, ngir baña jeexal seen xol» (Kolos 3:21).

Wone leen mbëggeel. Bu xale yi gisee ne seeni waajur bëgg nañu leen, dafay gën a yomb ci ñoom ñu nangu yar bi ñu leen di yar.

«Bu suñu doom juumee, dañuy dalal xelam. Dañu koy xamal ne bégg nañu ci dogal yu baax yi mu jot a jël. Dañu koy xamal ne, njuumte bi mu def, du tax ñu jàppe ko ni nit ku bon. Waaye dafa war a góor-góorlu ngir bañ koo defaat te di nañu ko ci dimbali» (Daniel).

LII LA BIIBËL BI WAX: «Ku bëgg dafay muñ te laabiir» (1 Korent 13:4).