Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Ubbite bi

Ubbite bi

LÉPP li ñu bind ci téere bii, amoon na. Dañu ko jële ci téere bu amul moroom, maanaam ci Biibël bi. Dañu ciy nettali li xewoon bi Yàlla komaasee sàkk ba tey. Dañu ciy wax sax li Yàlla bëgg a def ëllëg.

Téere bii, dafay wax ci lu gàtt li nekk ci Biibël bi. Dafay wax ci ay nit ñu Biibël bi tudd te mu ngi nettali li ñu def. Wax na itam yaakaar bi Yàlla may nit ñi, maanaam dinañu mën a dund ba fàww ci àjjana ci kow suuf si.

Ci téere bii, am na 116 nettali. Dañu leen def ci juróom ñetti xaaj. Xaaj bu nekk, bala ñu koy tàmbali, dañuy wax ci lu gàtt li ci nekk. Xew-xew yi ñuy nettali, dañuy toppante ci jamano yi amoon démb. Kon, dinga mën a xam kañ la amoon.

Téere bii, dañu ko def ci ay wax yu yomb. Kon, xale yu ndaw yi, ñu bare ci yéen dingeen ko mën a jàng. Yéen, waajur yi, dingeen ko mën a jàngal seen doom yu tuuti yi te dingeen gis ne duñu ci doyal. Waaw, téere bii, dina baax lool ci mag ak ndaw.

Bind nañu ci suufu nettali bu nekk fu ñu ko jële ci Biibël bi. Fexeel ba jàng ko ci Biibël bi itam. Boo paree ci benn nettali, xoolal ci ginnaaw nettali 116, laaj yi jëm ci nettali boobu, te nanga ci jéem a tontu.