Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 4

Li tax ñu dàq leen

Li tax ñu dàq leen

XOOLAL li xew léegi. Ñu ngi dàq Aadama ak Awa ci biti tool bu rafet bi tudd Eden. Ndax xam nga lu tax ?

Am na lu bon lu ñu def, te Yexowa mu ngi leen di yar. Ndax xam nga li ñu def ?

Dañu déggalul Yàlla. Yàlla waxoon na leen ne mën nañu lekk ci garab yi nekkoon ci tool bi. Waaye amoon na benn garab boo xam ne, waruñu ci woon a lekk. Bu ñu ci lekkee, dinañu dee. Kon garab googu, pur Yàlla rekk la woon. Te xam nañu ne kenn warul jël li nga moomul, du dëgg ? Kon lan moo xew ?

Benn bés, Awa mu ngi nekkoon moom kenn ci tool bi, benn jaan daldi wax ak moom. Jaan buy wax ! Doy na waar, de ! Dafa wax Awa mu lekk ci doomu garab bi leen Yàlla tere woon. Waaye, Yexowa sàkkul jaan muy wax. Kon, am na ku doon waxloo jaan bi. Kooku, kan la ?

Du woon Aadama. Waaye amoon na ñi Yàlla sàkkoon bala mu sàkk suuf si sax, maanaam malaaka yi ñu mënul a gis. Kon kenn ci ñoom la waroon a doon. Malaaka boobu, dafa yéeg boppam ba bëgg ilif nit, mel ni Yàlla. Dafa bëggoon nit ñi topp ko, bañ a topp Yexowa. Malaaka boobu moo doon waxloo jaan bi.

Malaaka boobu dafa nax Awa. Dafa ko ne bu lekkee doomu garab bi, dina mel ni Yàlla. Awa gëm ko, lekk ci, Aadama itam lekk ci. Ñoom ñaar, déggaluñu Yàlla. Loolu moo tax ñu dàq leen fi ñu dëkkoon, maanaam toolu Eden bu rafet bi.

Waaye Yàlla dina indi jamano joo xam ne dinañu defar suuf si sépp, ba mu mel ni toolu Eden. Dinga jàng ci téere bii li nga mën a def ngir bokk ci liggéey boobu. Léegi nañu seet lan mooy dal Aadama ak Awa.