Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 6

Ñaari doom : kenn ki baax, keneen ki bon

Ñaari doom : kenn ki baax, keneen ki bon

XOOLAL Kayin ak Abel. Màgg nañu léegi. Kayin beykat la. Am na ay pepp, ay doomu garab ak ay lujum.

Abel, sàmmkat la. Moom, li ko neex mooy toppatoo xar yu ndaw. Xar yi màgg nañu te Abel am na léegi xar yu bare yu mu sàmm.

Benn bés Kayin ak Abel dañu bëggoon a saraxal Yàlla dara. Kayin jël ci li mu doon bey. Abel jël xar bi gën a baax ci xar yi mu amoon. Yexowa nangu na Abel ak saraxam. Waaye nanguwul Kayin ak saraxam. Ndax xam nga lu tax ?

Nekkul ne saraxu Abel moo gënoon a baax saraxu Kayin. Yàlla dafa nangu Abel ak saraxam ndaxte Abel, nit ku baax la woon. Bëggoon na Yexowa. Bëggoon na it magam. Kayin moom, ku bon la woon ; bëggul woon rakkam.

Yàlla wax na Kayin mu soppi jikkoom. Waaye Kayin du dégg. Bi mu gisee ne Yàlla, Abel la gën a bëgg, dafa mer lool. Kon lii la Kayin wax Abel : ‘ Kaay nu dem àll ba. ’ Foofu, bi ñu wéetee, Kayin dóor na rakkam, dóor bu metti, ba Abel dee. Gis nga ni Kayin bone ?

Abel dee na waaye Yàlla fàttewu ko ba tey. Abel, nit ku baax la woon. Yexowa du fàtte mukk nit ku mel noonu. Benn bés, Yàlla mi tudd Yexowa dina dekkal Abel. Jamano jooju, Abel dootul dee mukk. Dina dund ba fàww ci kow suuf si. Ndax bëgg nga xam ay nit ñu mel ni Abel ?

Yàlla moom, bëggul nit ñu mel ni Kayin. Looloo tax bi Kayin reyee rakkam, Yàlla dafa ko dàq, mu war a tàggoo ak waa këram, dem fu sore lool. Kayin yóbbaale na benn rakkam bu jigéen, mu nekk jabaram.

Kayin ak jabaram amoon nañu ay doom. Yeneen doomu Aadama ak Awa, séy nañu te ñoom itam amoon nañu ay doom. Noonu la suuf si deme ba bare nit. Nañu waxtaan léegi ci ñenn ci ñoom.