Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 8

Ay ponkal yu réy ci kow suuf si

Ay ponkal yu réy ci kow suuf si

BOO gisoon nit ku njool ba tolloo ak sa kër, looy wax ? Dinga nee kooku ponkal bu réy la, de ! Amoon na nit ñu mel noonu ci kow suuf si. Biibël bi nee na ay doomu malaaka lañu woon. Naka la loolu ame ?

Fàttewuloo ne Seytaane, malaaka bu bon bi, mu ngi doon jaxase àddina si rekk. Jéem na xiir sax yeneen malaaka yi ci lu bon. Am na malaaka yu ko topp. Dañu bàyyi liggéey bi leen Yàlla joxoon ci asamaan. Dañu ñów ci kow suuf si, sol yaramu nit. Xam nga lu tax ñu def loolu ?

Biibël bi nee na dañu gis jigéen yu rafet yi nekkoon ci kow suuf, bëgg a dëkk ak ñoom. Looloo tax ñu wàcc ci kow suuf si ngir takk leen, ñu nekk seen jabar. Biibël bi nee na loolu baaxul ndaxte Yàlla dafa sàkk malaaka pur mu dund ca asamaan.

Doom yi malaaka yooyu amoon ak jigéen yi, meluñu woon ni yeneen doom yi. Xéyna bi ñu juddoo lañu meloon ni ñoom. Waaye ginnaaw loolu, dañu doon màgg, di màgg rekk, di gën a am doole ba nekk ponkal yu réy.

Ponkal yooyu, dañu bonoon lool. Te ndegam dañu nekkoon ay nit ñu njool te bare doole, dañu doon soxor ak nit ñi rekk. Dañu doon jéem a forse nit ñépp ñu def lu bon mel ni ñoom.

Booba dafa fekkoon Enog gaañu, waaye amoon na kenn ku baax ca jamano jooja. Kooku Nóoyin la tuddoon. Dafa doon def lépp lu ko Yàlla sant.

Benn bés Yàlla wax na Nóoyin ne léegi, fàww mu alag nit ñu bon ñépp. Waaye du alag Nóoyin, njabootam ak mala yu bare. Nañu seet ni Yàlla defe loolu.