Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 9

Nóoyin dafay defar gaal gu mag

Nóoyin dafay defar gaal gu mag

NÓOYIN amoon na benn jabar ak ñetti doom yu góor. Doom yooyu ñu ngi tudd Sem, Xam ak Yafet. Ku ci nekk amoon na jabar. Kon njabootu Nóoyin, juróom-ñetti nit la woon.

Yàlla sant na Nóoyin lu doy waar. Dafa ko wax mu defar benn gaal gu mag gu war a mel ni kees gu gudd te réy lool. Yàlla ne ko : ‘ Def ko mu am ñetti etaas te nanga ci def ay néeg. ’ Néeg yooyu, pur Nóoyin, njabootam ak mala yi la woon ak itam pur fu ñuy defe seen lekk ñoom ñépp.

Yàlla wax na Nóoyin mu def gaal gi ci fasoŋ boo xam ne ndox du ci dugg. Lii la ko wax : ‘ Dinaa indi taw bu metti buy alag àddina si sépp. Kepp ku nekkul ci biir gaal gi, dina dee. ’

Nóoyin ak doomam yi déggal nañu Yexowa te komaase nañu tabax gaal googu mel ni kees. Waaye nit ñi dañu leen doon reetaan rekk. Nóoyin wax na leen li Yàlla bëggoon a def. Waaye kenn gëmu ko. Dañu kontine di def lu bon.

Liggéey boobu yàgg na ay at, ndaxte kees googu dafa réyoon lool. Léegi pare na. Yàlla mu ngi wax Nóoyin mu dugal mala yi. Am na yenn mala yoo xam ne, Yàlla dafa ko wax ne ñaar la war a dugal, benn bu góor ak benn bu jigéen. Am na yeneen mala nag, Yàlla dafa ko wax mu dugal ci juróom-ñaar. Nóoyin waroon na dugal itam fasoŋu picc bu nekk. Nóoyin def na lépp li ko Yàlla santoon.

Bi loolu yépp paree, Nóoyin ak njabootam dugg nañu ci biir gaal gi. Yàlla tëj na bunt bi. Ci biir gaal gi, Nóoyin ak njabootam, ñu ngiy xaar. Boo fa nekkoon di xaar nag ? Xéyna dinga ne : Ndax Yàlla dina def taw bi mu wax ?