Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 12

Ñu ngi tabax lu kowe lool

Ñu ngi tabax lu kowe lool

LÉEGI ñu ngi ci beneen jamano. Doomu Nóoyin yi amoon nañu doom yu bare. Seeni doom amaat doom ba nit ñi bare ci kow suuf si.

Amoon na kenn ci ñoom ku tuddoon Namróot. Nóoyin moo juroon maamam. Namróot, nit ku bon la woon. Rëbbkat la woon. Waaye yemul woon ci mala yi. Dafa doon rëbb itam ay nit, di leen rey. Namróot def na boppam buur ci kow nit ñi. Yàlla bëggul woon Namróot.

Ca jamano jooja, nit ñépp a bokkoon benn làkk. Namróot dafa bëggoon nekk seen kilifa ñoom ñépp. Looloo tax mu bëggoon ñu nekk ñoom ñépp ci benn béréb. Xam nga lan la def ? Dafa leen wax ñu samp benn dëkk te tabax fa benn taax bu kowe lool. Xool leen fii ci suuf. Ñu ngiy def ay muul.

Tabax boobu, neexul woon Yàlla mi tudd Yexowa. Dafa bëggoon nit ñi tasaaroo ci kow suuf si sépp. Waaye nit ñi, lii lañu wax : ‘ Ayca! Nañu sanc fii dëkk te tabax lu kowe lool ba mu laal asamaan. Suñu tur dina siiw lool ! ’ Seen bopp lañu bëggoon a màggal. Bëgguñu woon a màggal Yàlla.

Looloo tax Yàlla def ba ñu bàyyi liggéey boobu. Xam nga lan la def ? Jékki-jékki rekk, dafa def nit ñi làkk ay làkk yu wuute. Bu jëkk, benn làkk rekk moo amoon. Kon léegi mënatuñu déggante. Loolu moo tax ñu mujj a tudde dëkk boobu Babel walla Babilon ndaxte tur boobu mu ngi tekki “ jaxasoo ”.

Nit ñi léegi ñu ngi bàyyi Babel. Ñi bokk làkk ñu ngi gurupoo, ànd dem dëkk feneen ci kow suuf si.