Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 14

Yàlla mu ngi natt ngëmu Ibraayma

Yàlla mu ngi natt ngëmu Ibraayma

GIS nga li Ibraayma di def fii ? Paaka la yore te mu ngi mel ni ku bëgg rey doomam. Lu tax muy def loolu ? Bala ñu xam loolu, nañu jëkk a seet ni Ibraayma ak Saarata ame seen doom.

Yaa ngi fàttaliku ne Yàlla waxoon na leen ne dinañu am doom. Gëm loolu yombul woon ndaxte Ibraayma ak Saarata dañu màggetoon lool. Ibraayma, moom, gëmoon na ko. Xamoon na ne dara tëwul Yàlla. Kon, lan moo xew ?

Benn at ginnaaw bi leen Yàlla digee loolu, Ibraayma ak Saarata am doom bu góor bu tudd Isaaxa, fekk Ibraayma amoon 100 at, Saarata 90. Yàlla def na li mu leen digoon !

Bi Isaaxa demee ba mag, Yexowa natt na ngëmu Ibraayma. Mu woo ko, ne ko : ‘ Ibraayma! ’ Ibraayma ne ko : ‘ Naam ! ’ Yàlla ne ko : ‘ Jëlal sa doom, bi nga am kepp, Isaaxa, te demal ca tund bi ma lay won. Foofu nanga rey sa doom te sarax ma ko. ’

Loolu metti woon na lool Ibraayma, ndaxte dafa bëggoon doomam lool. Te it, Yàlla digoon na Ibraayma ne doomam yi dinañu dëkk ci réewu Kanaan. Naka la loolu di ame su Isaaxa deewee ? Loolu, Ibraayma xamu ko woon. Waaye ba tey def na li ko Yàlla santoon.

Bi ñu àggee ca tund ba, Ibraayma yeew na Isaaxa, teg ko ci kow saraxalukaay bi mu defaroon. Mu jël paaka ngir rey doomam, malaaka Yàlla daldi ko woo : ‘ Ibraayma ! Ibraayma !’ Ibraayma ne ko : ‘ Naam ! ’

Yàlla ne ko : ‘ Bul laal xale bi, bu ko def dara. Léegi xam naa ne danga am ngëm ci man, ndaxte bañoo ma jox sax sa doom, bi nga am kepp. ’

Dëgg-dëgg, Ibraayma dafa amoon ngëm gu dëgër ! Gëmoon na ne dara tëwul Yexowa, xam ne su Isaaxa deewoon,Yexowa mënoon na ko sax dekkal. Waaye Yàlla bëggul woon Ibraayma rey doomam Isaaxa dëgg. Looloo tax mu def benn xar lonk béjjénam ci ay garab yu ndaw, mu wax Ibraayma mu saraxe ko, bañ a saraxe doomam.