Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 16

Isaaxa takk na jabar ju baax

Isaaxa takk na jabar ju baax

JIGÉEN bi nekk fii, kan la ? Rebeka la tudd. Ki muy jegesi mooy Isaaxa. Rebeka moo war a nekk jabaram. Loolu naka la ame ?

Ibraayma, baayu Isaaxa, dafa bëggoon a may doomam jabar ju baax. Bëggul won Isaaxa takk benn jigéenu Kanaan, ndaxte waa Kanaan dañu doon jaamu ay yàlla yu dul dëgg. Loolu moo tax Ibraayma woo ki ko doon liggéeyal, maanaam surgaam, ne ko : ‘ Dama bëgg nga dem ci samay mbokk yi nekk Karan te jël foofu benn jabar pur sama doom Isaaxa. ’

Surga Ibraayima daldi jël fukki gëléem te dem fu sore foofu. Bi mu jegee fu mbokki Ibraayima dëkkoon, taxaw na ci benn teen. Ngoon la woon ci waxtu bi jigéen yi di rooti. Mu ñaan Yexowa, ne ko : ‘ Su amee ku ma may ndox, man ak sama gëléem yi, na jigéen jooju nekk jabar bi ngay tànnal Isaaxa. ’

Yàggul rekk Rebeka ñów root. Surga bi ñaan ko ndox, mu may ko. Rootal na itam gëléemam yépp yi nekkoon foofu, fekk dañu maroon lool. Liggéey bu metti la woon ndaxte gëléem yi dañuy naan ndox mu baree bare.

Bi Rebeka paree, surga bi laaj ko kuy baayam ak ndax dina mën a fanaan seen kër. Rebeka ne ko : ‘ Sama baay, Betuwel la tudd. Mën nga ñów suñu kër, am na palaas. ’ Surga Ibraayma xamoon na ne Betuwel moo doon doomu magu Ibraayma mi tudd Naxor. Mu daldi sukk te sant Yexowa, ndax li mu ko indi woon ci mbokki Ibraayma.

Guddi googu, dafa wax Betuwel ak doomam bu góor bi tudd Laban li taxoon mu ñów. Ñoom ñaar nangu Rebeka dem séyi ak Isaaxa. Ndax Rebeka dina bëgg a dem ? ‘ Waaw ’, la wax, ‘ bëgg naa dem. ’ Kon bés bi ci topp, war nañu seen gëléem yi, aw yoon bu gudd boobu jëm Kanaan.

Bi nu àggee Kanaan, ngoon la woon. Rebeka gis benn góor di doxantu. Isaaxa la woon. Moom, mu kontaan bi mu gisee Rebeka. Yaayam Saraata dee na am na léegi ñetti at te ba léegi loolu dafa ko metti. Waaye mujj na nob Rebeka lool, mu amaat mbégte.