Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 17

Ñaari séex yu wuute

Ñaari séex yu wuute

ÑAARI xale yi ñuy wone fii, niroowuñu, du dëgg ? Ndax xam nga naka lañu tudd ? Kiy rëbb, Esawu la tudd. Kiy toppatoo xar yi, Yanqóoba la tudd.

Esawu ak Yanqóoba, ay séex lañu. Doomi Isaaxa ak Rebeka lañu. Seen baay Isaaxa, Esawu la gën a bëgg ndaxte moom dafa aay ci rëbb te dafay indi lekk ci kër gi. Rebeka moom, Yanqóoba la gën a bëgg, ndaxte xale bu teey la, xale bu amul benn poroblem.

Seen maam Ibraayma mu ngi doon dund ba tey. Wóor na ne déglu maamam di wax ci Yexowa neexoon na Yanqóoba lool. Ibraayma gaañu na bi mu amee 175 at, fekk ñaari séex yi am 15 at.

Bi Esawu amee 40 at, takk na ñaari jabar ci jigéen yi nekkoon Kanaan. Loolu naqari na lool Isaaxa ak Rebeka ndaxte jigéen yooyu jaamuñu woon Yexowa.

Benn bés, am na lu taxoon Esawu mere lool Yanqóoba. Ñu nga woon ca jamano ja Isaaxa naroon a barkeel taawam bu góor. Esawu moo gënoon a mag. Kon dafa foogoon ne moom la baayam di barkeel. Waaye booba, dafa fekk jaayoon na rakkam Yanqóoba ba pare lu taxoon mu war a am barke boobu. Te it, bi ñu juddoo ñoom ñaar, Yàlla waxoon na ne Yanqóoba mooy am barke boobu. Te loolu moo am. Yanqóoba la Isaaxa barkeel.

Bi Esawu déggee loolu, dafa mere lool Yanqóoba. Wax na sax ne dina ko rey. Bi Rebeka déggee loolu, dafa tiit lool. Mu daldi wax jëkkëram Isaaxa : ‘ Su Yanqóoba takkee jabar ci jigéen yi nekk fii Kanaan, du baax dara. ’

Isaaxa daldi woo Yanqóoba, ne ko : ‘ Bul takk jabar ci jigéen yi nekk fii Kanaan. Demal ci sa maam Betuwel bi nekk Karan. Am na doom bu tudd Laban. Jëlal ci doomu Laban yi kenn, nga takk ko jabar. ’

Yanqóoba topp li ko baayam wax. Mu jóg rekk, aw yoon bu sore boobu jëm Karan, dem ca mbokkam ya.