Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 19

Yanqóoba am na doom yu bare

Yanqóoba am na doom yu bare

XOOLAL njaboot gu réy gii. Yanqóoba mooy baayu 12 doom yu góor yooyu. Yanqóoba amoon na itam ay doom yu jigéen. Ndax am na doomu Yanqóoba yoo mën a wax seen tur ? Nañu ci jàng yenn.

Leya jur na Ruben, Simeyon, Lewi ak Yuda. Rasel moom amul woon benn doom, xolam jeex. Mu may Yanqóoba jaamam bi tudd Bilaa ngir mu am ak moom doom. Bilaa am ñaari doom yu góor yu tudd Dan ak Naftali. Leya moom, may na Yanqóoba jaamam bi tudd Silpa, Silpa am ak moom ñaari doom, Gàdd ak Aser. Leya mujj na am yeneen ñaari doom yu góor, Isakaar ak Sabulon.

Rasel mujj na am doom. Mu tudde ko Yuusufa. Ci téere bii, dinañu jàng lu bare lu jëm ci xale bu góor boobu ndaxte dem na ba nekk kilifa bu mag. Yanqóoba amoon na 11 doom yu góor yooyu bi mu nekkee kër Laban, baayu Rasel.

Yanqóoba amoon na itam ay doom yu jigéen, waaye turu kenn ci ñoom kese lañu wax ci Biibël bi. Mu ngi tuddoon Diina.

Léegi Yanqóoba dafa bëgg bàyyi Laban, ñibbi Kanaan. Mu dajale njaboot gu réy gi mu amoon ak gétt yi mu amoon yépp, daldi tàmbali tukki bu sore boobu.

Bi ñu nekkee Kanaan ba mu yàgg tuuti, Rasel amaat na doom bu góor. Doom bi juddu fekk ñu ngi woon ci yoon. Metti woon na lool ba Rasel mujj gaañu bi liir bi doon juddu. Liir bi moom deewul. Yanqóoba tudde na ko Ben-yamin.

Buñu fàtte turu fukki doom yu góor ak ñaar yi Yanqóoba amoon, ndaxte ñoom ñoo jur waa Israyil yépp. Tudde nañu 12 giiru Israyil yi ci 10 doom yu góoru Yanqóoba ak ñaari doom yu góoru Yuusufa. Isaaxa dund na ay at yu bare ginnaaw bi doom yooyu juddoo. Wóor na ne dafa kontaanoon lool ndax sët yu bare yi mu amoon noonu. Nañu seet léegi li daloon sëtam bu jigéen bi tudd Diina.