Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 20

Diina am na poroblem

Diina am na poroblem

NDAX gis nga kan la Diina di seetsi ? Ay jigéen yu dëkk Kanaan. Baayam Yanqóoba, bu ko yëgoon, ndax dina ci kontaan ? Bala ñu ciy tontu, nanga fàttaliku li Ibraayma ak Isaaxa waxoon ci jigéeni Kanaan.

Ndax Ibraayma dafa bëggoon doomam Isaaxa takk jabaru Kanaan ? Déedéet ! Ndax Isaaxa ak Rebeka dañu bëggoon seen doom Yanqóoba takk jabaru Kanaan ? Déedéet ! Xam nga lu tax ?

Ñi dëkkoon Kanaan dañu doon jaamu ay yàlla yu dul dëgg. Kon duñu mën a nekk ay jëkkër, jabar walla xarit yu baax. Wóor na ñu ne Yanqóoba bëggul woon doomam xaritoo ak jigéenu Kanaan.

Ci lu wóor, Diina dina dugal boppam ci coono. Ndax gis nga góor gii di xool Diina ? Waa Kanaan la. Sisem la tudd. Benn bés, Diina dafa demoon seeti xaritam yi, Sisem forse ko mu tëdd ak moom. Lu bon la woon, ndaxte bala góor di ànd ak jigéen, fàww ñu nekk jëkkër ak jabar. Te li Sisem def noonu indi na yeneen coono yu bare.

Bi magu Diina yi déggee loolu, meroon nañu lool. Ñaar ci ñoom, Simeyon ak Lewi, dañu meroon ba yëkkëti jaasi, dem ci dëkk boobu te dal ci kow góor ñi fa nekkoon. Ñoom ak seeni doomi baay rey nañu Sisem ak ñeneen góor yépp. Yanqóoba mer ndax lu bon loolu ñu def.

Loolu yépp, nu mu komaasee ? Diina moo amoon xarit ci ñi toppul Yàlla. Ñun, bëgguñu am xarit yu mel noonu, du dëgg ?