Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 21

Magi Yuusufa dañu ko bañ

Magi Yuusufa dañu ko bañ

XOOLAL xale bi nekk fii. Xolam dafa jeex. Amatul yaakaar. Yuusufa la. Doomu baayam yi dañu ko jaay nit ñooñu di dem Misra. Dina nekk jaam foofu. Lu tax ñi mu bokkal baay def ko loolu ? Dañu iñaanoon, moo tax.

Seen baay Yanqóoba dafa bëggoon Yuusufa lool. Dafa ko wone bi mu ko defalee yëre bu rafet. Bi 10 magi Yuusufa gisee ni Yanqóoba bëgge woon Yuusufa, ñu komaase di ko iñaane ba bañ ko sax. Waaye amoon na leneen lu taxoon nu bañ ko.

Am na ñaari gént yu Yuusufa defoon. Ci gént bu nekk, dafa doon gis magam yi di sukk ci kanamam. Bi mu leen nettalee gént yooyu, dañu ko gën a bañ.

Benn bés, Yanqóoba wax Yuusufa mu dem seeti magam yi ca àll ba. Ñu nga doon sàmm juram yi. Te Yanqóoba dafa bëggoon a xam ndax ñu ngi ci jàmm. Bi ñu gisee Yuusufa di ñów, am na ñu ne : ‘ Nañu ko rey ! ’ Ruben, ki nekkoon taaw bi, ne leen : ‘ Déedéet, buleen def loolu ! ’ Ñu daldi jàpp Yuusufa, sànni ko ci benn teen bu amuloon ndox. Ba pare ñoom ñépp toog ngir seet li ñuy def ak moom.

Ay waa Ismayla daldi jaar foofu. Yuda ne : ‘ Nañu ko jaay Ismaayléen yi. ’ Loolu lañu def. Jaay nañu Yuusufa 20 xànjaaru xaalis. Xoolal lu bon li ñu def noonu !

Léegi, lan lañuy wax seen baay ? Dañu rey benn sikket te xooj ci deretam yëre Yuusufa bu rafet boobu. Ñu indi ko seen baay naan : ‘ Lii lañu for ci àll bi. Seetal ba xam ndax du yëre Yuusufa. ’

Yanqóoba gis ne moom la. Mu daldi jooy : ‘ Wóor na ma ne rabu àll moo ko rey. ’ Loolu la magi Yuusufa bëggoon seen baay xalaat. Xolu Yanqóoba yépp jeex. Jooy na ay fan yu bare. Waaye Yuusufa deewul. Nañu seet li ko dal fi ñu ko yóbbu.