Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 22

Tëj nañu Yuusufa kaso

Tëj nañu Yuusufa kaso

YUUSUFA, 17 at rekk la amoon bi nu ko yóbboo Misra. Foofu dañu ko jaay benn góor gu tudd Potifaar. Kooku dafa doon liggéey ci buuru Misra bu ñuy woowe Firawna.

Yuusufa sawar na ci liggéey bi muy def ci kër Potifaar. Moo tax bi mu demee ba mag, Potifaar bàyyi lépp ci loxoom. Kon lu tax mu nekk kaso léegi ? Jabaru Potifaar moo tax.

Yuusufa dem na ba nekk góor gu rafet. Jabaru Potifaar bëgg tëdd ak moom. Waaye komka Yuusufa xam na ne loolu baaxul, mu bañ. Jabaru Potifaar mer lool. Léegi, bi jëkkëram ñówee, dafa ko fen, ne ko : ‘ Yuusufa, nit ku bon la. Jéem na tëdd ak man ! ’ Potifaar gëm jabaram, mere Yuusufa lool, te tëj ko kaso.

Foofu, ki doon yore ñi nekkoon kaso, gaaw na gis ne Yuusufa, nit ku baax la. Mu bàyyi ci loxoom ñi nekkoon ci kaso bi ñépp. Benn bés, Firawna dafa mere woon ki ko doon jox mu naan ak ki ko doon defaral mburu. Mu tëj leen kaso. Ñoom ñaar am gént guddi, waaye xamuñu lu gént yooyu tekki. Ci ëllëg si, Yuusufa ne leen : ‘ Waxleen ma li ngeen gént. ’ Ñu wax ko ko. Yàlla daldi dimbali Yuusufa, mu firi leen seen gént yooyu.

Lii la Yuusufa wax ki doon jox Firawna mu naan : ‘ Fii ak ñetti fan, dinga génn kaso te delluwaat ci sa liggéey. ’ Yuusufa teg ci ne : ‘ Boo génnee, waxal Firawna lu jëm ci man, nga dimbali ma ba ma génn fii. ’ Waaye lii la Yuusufa wax ki doon defaral Firawna mburu : ‘ Fii ak ñetti fan, Firawna dina yónni ay nit ñu dagg sa bopp. ’

Ñetti fan ginnaaw loolu, li Yuusufa waxoon yépp am. Firawna wax na ñu dagg boppu ki ko doon defaral mburu. Ki ko doon may mu naan, moom, génn na kaso te dellu na ci liggéey bi mu doon def ci kër Firawna. Waaye fàtte na lépp lu jëm ci Yuusufa te waxul dara Firawna, Yuusufa kontine di nekk kaso.