Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 23

Firawna mu ngiy gént

Firawna mu ngiy gént

ÑAARI at ginnaaw loolu, Yuusufa mu ngi kaso ba tey. Ki doon jox Firawna mu naan, fàtte na Yuusufa. Benn guddi, Firawna am ñaari gént yu doy war. Waaye xamul woon lu ñu tekki. Ndax yaa ngi koy gis fii, muy nelaw ? Bi mu yeewoo ci suba si, dafa woo boroom xam-xam yi, mu wax leen li mu gént. Waaye mënuñu woon a xam li gént yooyu tekki.

Ki doon jox Firawna mu naan daldi fàttaliku Yuusufa. Mu ne Firawna : ‘ Bi ma nekkee kaso, amoon na ku mënoon a firi gént yi. ’ Firawna daldi génne Yuusufa kaso ci saa si.

Firawna nettali Yuusufa li mu gént. Mu ne ko : ‘ Gis naa juróom-ñaari nag yu duuf te rafet. Ba pare ma gis juróom-ñaari nag yu sew te yooy. Yu sew yi daldi lekk yu duuf yi.

‘ Ci ñaareelu gént bi, gis naa juróom-ñaari gub yu baax te rafet sax ci benn gittax [mooy li ñuy wone fii]. Ba pare ma gis juróom-ñaari gub yu sew te wow sax ci benn gittax. Yu sew yi daldi lekk juróom-ñaari gub yu baax te rafet yi. ’

Lii la Yuusufa wax Firawna : ‘ Ñaari gént yi, benn la. Juróom-ñaari nag yu duuf ak juróom-ñaari gub yu rafet, ñu ngi tekki juróom-ñaari at. Juróom-ñaari nag yu yooy ak juróom-ñaari gub yu wow, ñu ngi tekki yeneen juróom-naari at. Dina am juróom-ñaari at ci Misra fu suuf si di joxe lekk gu bare. Ba pare dina am yeneen juróom-ñaari at fu suuf si di joxe tuuti lekk rekk. ’

Yuusufa daldi ne Firawna : ‘ Nanga seet ku am xel te wax ko mu dajale lekk gu bare ci juróom-ñaari at yu baax yi. Su ko defee, waa réew mi duñu dee ndax xiif bu juróom-ñaari at yu bon yi amee. ’

Firawna nangu na li ko Yuusufa waxoon. Mu tànn Yuusufa ngir mu dajale lekk gu bare googu te am fu mu koy def. Yuusufa daldi nekk kilifa gi gën a mag ginnaaw Firawna.

Juróom-ñetti at ginnaaw loolu, fekk xiif gi jot na, Yuusufa gis ay nit di ñów. Xam nga ñooñu ñan lañu ? Ñooy 10 magam yi. Seen baay Yanqóoba moo leen yónni Misra ndax xiif gi amoon Kanaan. Yuusufa xàmme na magam yi, waaye ñoom, xàmmewuñu ko. Xam nga lu tax ? Yuusufa nekkatul xale léegi te it yëre yi mu sol bokkuñu ak li mu doon sol bi mu nekkee ak ñoom.

Yuusufa mu ngi fàttaliku gént gi mu amoon bi mu nekkee xale. Ci gént googu, magam yi ñu ngi doon sukk ci kanamam. Ndax yaa ngi fàttaliku bi ñu jàngee loolu ? Kon léegi, Yuusufa xam na ne Yàlla moo ko indi Misra, te am na lu tax mu def loolu. Ci yow, lan la Yuusufa di def léegi ? Nañu seet loolu.