Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 24

Yuusufa Mu ngi teg nattu ci kow magam yi

Yuusufa Mu ngi teg nattu ci kow magam yi

YUUSUFA dafa bëgg xam ndax 10 magam yi soppi nañu seen jikko yu bon yi. Mu ne leen : ‘ Dangeen ñów pur seet suñu réew mi ngir xam fu mu néewe doole. ’

Magam yi ne : ‘ Déedéet, du loolu ! Dëgg lañu wax. Ñun, fukki góor ak ñaar lañu woon, bokk benn baay. Caat bi mu nga kër ga ak suñu baay, te ki ci des nekkatul. ’

Yuusufa def ni gëmu leen. Mu tëj Simeyon kaso, bàyyi ñi ci des jël lekk te ñibbi. Waaye lii la leen wax : ‘ Bu ngeen dellusee, fàww ngeen indaale caat bi. ’

Bi ñu àggee Kanaan, nettali nañu seen baay Yanqóoba lépp lu xewoon Misra. Xolam yépp jeex. Mu daldi yuuxu ne : ‘ Yuusufa nekkatu fi. Léegi Simeyon nekkatu fi. Duma leen bàyyi mukk ngeen yóbbu sama caat Ben-yamin. ’ Waaye lekk bi dem na ba bëgg jeex. Léegi, fàww Yanqóoba bàyyi leen ñu yóbbu Ben-yamin ci Misra, ndaxte foofu rekk lañu mën a amaat lekk.

Yuusufa mu ngi séentu magam yi di ñów. Bi mu gisee rakkam Ben-yamin, mu kontaan lool. Ba léegi kenn ci ñoom xamul ne kilifa gu mag googu ñuy waxal mooy Yuusufa. Léegi Yuusufa dina seet ndax 10 magam yi soppeeku nañu walla déet.

Yuusufa dafa wax surgaam yi, maanaam ñi ko doon liggéeyal, ñu feesal saagu magam yi. Mu wax leen itam ñu dugal ci saagu Ben-yamin kaas bu ñu defare xaalis. Kaas boobu, Yuusufa ci boppam moo ko moomoon. Waaye ñoom, xamuñu ci woon dara. Bi ñu demee ba xaw a sore tuuti, Yuusufa yónni jaamam yi ci ñoom. Ñu dab leen, jaam yi nee leen : ‘ Lu tax ngeen sàcc kaasu xaalis bi suñu kilifa moom ? ’

Ñépp ne : ‘ Sàccuñu ko ! Xoolleen suñuy saag. Ku ngeen fekk ak kaas bi, nangeen ko rey. ’

Surgaam yi daldi ubbi saag bu nekk. Ñu gis kaas bi ci saagu Ben-yamin. Loolu lañu wone fii. Jaam yi wax leen lii : ‘ Yéen, mën ngeen dem, waaye Ben-yamin, moom, fàww mu ànd ak ñun. ’ Léegi, lan la 10 magam yi di def ?

Ñoom ñépp dañu ànd ak Ben-yamin, delluwaat kër Yuusufa. Yuusufa ne leen : ‘ Yéen ñépp mën ngeen dem ba mu des Ben-yamin. Moom, fii lay des. Dinaa ko def sama jaam. ’

Yuda daldi jóg, ne : ‘ Su ma ñibbee te xale bi àndul ak man, sama pàppa dina dee, ndaxte dafa ko bëgg lool. Kon ngir Yàlla, bàyyil ma des fii, ma nekk sa jaam. Waaye nanga bàyyi xale bi mu ñibbi. ’

Léegi Yuusufa gis na ne magam yi soppeeku nañu. Bàyyi nañu jikko yu bon yi ñu amoon bu jëkk. Nañu seet léegi li Yuusufa di def.