Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 25

Yanqóoba ak waa këram ñu ngi toxu Misra

Yanqóoba ak waa këram ñu ngi toxu Misra

YUUSUFA mënatul téye boppam. Wax na surgaam yépp, maanaam ñi ko doon liggéeyal, ñu génn. Bi mu wéetee ak magam yi, Yuusufa daldi jooy. Loolu jaaxal na leen lool, ndaxte xamuñu lu tax muy jooy. Mu ne leen : ‘ Man maay Yuusufa ! Ndax sama pàppa mu ngi dund ? ’

Magam yi mënatuñu wax ndax li ñu jaaxle. Dañu tiit sax. Waaye Yuusufa ne leen : ‘ Jegesileen ! ’ Ñu jegesi. Mu nee leen : ‘ Man maay Yuusufa seen rakk, bi ngeen jaayoon, ñu indi ma Misra. ’

Yuusufa bëgg na dalal seen xel, mu ne leen : ‘ Yéen a ma jaay ba ñu indi ma fii. Waaye buleen mere seen bopp ndax loolu. Yàlla moo ma fi indi ngir musal ay nit. Firawna def na ma kilifa ci kow réew mi yépp. Kon léegi, delluleen gaaw ci sama baay te waxleen ko mu ñów, dëkk fi. ’

Yuusufa daldi jàpp magam yi, kenn ku nekk, mu fóon leen. Bi Firawna déggee ne magi Yuusufa ñów nañu, lii la wax Yuusufa : ‘ Joxal say mag ay sareet, ñu jëli seen baay ak seeni njaboot, ñów fii. Dinaa leen jox béréb bi gën a baax ci Misra. ’

Loolu lañu def. Fii ci suuf, yaa ngi gis Yuusufa di teeru baayam bi mu àggee Misra ak waa këram yépp.

Waa këru Yanqóoba bare nañu lool léegi. Yanqóoba, doomam yi ak sëtam yi, 70 lañu woon bi ñu àggee Misra. Amoon na itam seeni jabar. Xéyna amoon na it ay surga yu bare. Ñooñu ñépp ñoo ñów dëkksi Misra. Ñu di leen woowe waa Israyil, ndaxte Yàlla dafa soppi woon turu Yanqóoba mu nekk Israyil. Waa Israyil dem nañu ba nekk mbooloo boo xam ne Yàlla ci boppam moo ko moomoon. Loolu, dinañu ko gis tuuti ci kanam ci téere bii.