Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 26

Ayóoba Bàyyiwul Yàlla

Ayóoba Bàyyiwul Yàlla

XOOLAL ki nekk fii te feebar. Ndax yërëmoo ko ? Ayóoba la tudd. Jigéen biy wax ak moom, jabaram la. Xam nga lan lay wax ? ‘ Waxal lu bon ci Yàlla te dee. ’ Nañu seet lu tax muy wax loolu ak lu tax Ayóoba (Job) di sonn nii.

Ayóoba nit ku baax la woon. Dafa doon topp Yexowa bu baax. Mu ngi dëkkoon ci réew mi tudd Us. Sorewul woon Kanaan. Yexowa bëggoon na Ayóoba lool. Waaye amoon na ku ko bañoon. Ndax xam nga kan la ?

Seytaane mi nekk Ibliis la. Yaa ngi fàttaliku Seytaane ? Moom mooy malaaka bu bon te bañ Yexowa lool. Fexe na ba Aadama ak Awa déggadi Yexowa. Te foogoon na ne dina mën a xiir doomu Aadama yépp ci déggadi Yexowa. Ndax def na ba ñépp déggadi Yexowa ? Déedéet. Xoolal góor ak jigéen yépp yi ñu waxtaane ci téere bii te toppoon Yexowa bu baax. Ñaata nga ci mën a wax seen tur ?

Yanqóoba ak Yuusufa dee nañu ci Misra. Léegi, ci àddina si sépp Ayóoba mooy ki gën a topp li Yexowa wax. Yexowa dafa bëggoon a won Seytaane ne mënul fexe ba nit ñépp bon. Mu ne ko : ‘ Xoolal Ayóoba. Gis nga ni mu ma toppe. ’

Seytaane wax lii : ‘ Danga koy barkeel te bare na alal. Loolu moo tax mu jub. Waaye, boo dindee loolu lépp, dina la wax lu bon. ’

Yexowa ne ko : ‘ Ayca, defal li nga wax. Nangul alalam yépp. Def ko li la neex. Dinañu gis ndax Ayóoba dina ma bàyyi. Waaye nag, bu ko rey. ’

Seytaane def na ñu sàcc nag yi ak gëléem yi Ayóoba amoon. Def na it ñu rey xar yi mu amoon. Ba pare dafa indi ngelaw bu réy a réy. Ngelaw boobu rey na 10 doomam yu góor ak yu jigéen. Ginnaaw loolu Seytaane dafa feebarloo Ayóoba feebar bu metti. Ayóoba sonn lool. Loolu moo tax jabaram ne ko : ‘ Waxal lu bon ci Yàlla te dee. ’ Waaye Ayóoba deful loolu. Ñetti xaritam ñów seetsi ko. Waaye ñooñu nekkuñu woon xarit dëgg. Ñu ne ko lu bon li mu doon def moo tax loolu lépp dal ko. Waaye ba tey, Ayóoba bàyyiwul Yàlla, mu kontine di ko topp rekk.

Loolu bégal na Yexowa lool. Te ginnaaw loolu nag, barkeel na Ayóoba bu baax. Loolu lañu wone fii ci suuf. Yàlla dindi na feebar bi mu amoon. Ayóoba amaat na 10 doom yu rafet. Mu amaat ay nag, ay xar ak ay gëléem ba ñu mat ñaari yoon li mu amoon.

Ndax yow, dinga kontine di topp Yexowa ni ko Ayóoba defe woon ? Boo defee loolu, Yàlla dina la barkeel lool yow itam. Dinga mën a dund ba fàww ci suuf si, bés bu Yàlla defaree suuf si sépp ba mu mel ni tollu Eden.