Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 28

Naka La Musaa Rëcce Bi Mu Nekkee Liir

Naka La Musaa Rëcce Bi Mu Nekkee Liir

XOOLAL liir bi nekk fii di jooy. Mu ngi jàpp loxo jigéen bi. Liir bi, Musaa la. Jigéen bu rafet bi, ndax xam nga kan la ? Doomu Firawna la. Firawna mooy buuru Misra.

Yaayu Musaa bëggul woon ñu rey doomam. Kon dafa ko nëbb ba mu am ñetti weer. Waaye xamoon na ne dinañu ko mujj a gis. Kon, am na lu mu def ngir mu rëcc.

Dafa jël benn pañe, defar ko ci fasoŋ boo xam ne ndox du ci dugg. Mu dugal ci Musaa, teg pañe bi ci barax yi, maanaam ñaxu dex yi nekkoon ci booru dex bi tudd Niil. Mu wax magu Musaa, Miryam, mu nekk foofu te bañ a sore pañe bi ngir seet lan mooy xew.

Yàggul dara, doomu Firawna ñów, bëgg a sangu ci Niil bi. Jékki-jékki rekk mu gis pañe bi ci barax yi. Mu woo benn jigéen bu ko doon liggéeyal, ne ko : ‘ Jëlal ma pañe bale. ’ Bi doomu Firawna ubbee pañe bi, mu gis benn liir bu rafet lool ! Liir bi, Musaa, mu ngi doon jooy. Jigéen bi yërëm ko. Bëggul woon ñu rey ko.

Miryam daldi ñów. Moom ngay gis fii di wax ak doomu Firawna. Mu ne ko  : ‘ Ndax danga bëgg ma wutal la ci jigéeni Israyil ku koy nàmpal ? ’

Jigéen bi ne ko : ‘ Waaw, demal. ’

Miryam daldi gaaw a dem woo yaayam. Bi yaayu Musaa ñówee, doomu Firawna ne ko : ‘ Yóbbul xale bii, nàmpalal ma ko, ma fey la. ’

Kon, yaayu Musaa, doomam ci boppam la doon toppatoo. Bi Musaa demee ba xaw a mag tuuti, yaayam yóbbu ko ci doomu Firawna, jigéen bi daldi ko jàppe ni doomam. Loolu moo tax Musaa màgg ci këru Firawna.