Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 29

Li Tax Musaa Daw

Li Tax Musaa Daw

XOOLAL Musaa. Mu ngi daw Misra. Gis nga ñi koy dàq ? Ndax xam nga lu tax ñu bëgg ko rey ? Nañu jàng loolu.

Musaa màgg na ci kër Firawna, buuru Misra. Musaa, ku am xel la woon te kilifa gu mag la woon. Xamoon na ne moom bokkul ci waa Misra. Xamoon na ne waajuram, ay waa Israyil lañu te ay jaam lañu.

Benn bés, bi mu amee 40 at, Musaa dem na seeti mbokkam yi, maanaam waa Israyil. Dafa bëggoon a gis ni ñu doon dunde. Mu gis lu bon li ñu leen doon def. Mu gis benn waayu Misra di dóor kenn ci jaami Israyil. Musaa geestu fu nekk, gisul kenn, mu rey waayu Misra ji, suul ko.

Ca ëllëg sa nag, mu génnaat, seetiwaat mbokkam yi. Mu foog ne dina leen mën a dimbali ñu mucc ci seen njaam gi. Waaye bi mu gisee ñaari waa Israyil di xeex, Musaa wax lii ki tooñ : ‘ Lu tax ngay dóor sa moroom ? ’

Waa ji tontu ko ne : ‘ Ku la fal njiit ak àttekat ci suñu kow ? Ndax danga ma bëgg rey, ni nga reye waayu Misra ja ? ’

Musaa daldi tiit. Léegi xam na ne mbir mi feeñ na. Firawna sax xam na ko ba mu yónni ay nit ngir rey Musaa. Loolu moo tax Musaa di daw Misra.

Bi Musaa jógee Misra, dafa dem fu sore ci réewu Majan. Foofu mu xamante ak njabootu góor gu tudd Yétro, te takk doomam bi tudd Sipora. Musaa daldi nekk sàmmkat te sàmm xaru Yétro yi. Nekkoon na 40 at ci réewu Majan. Léegi am na 80 at. Benn bés Musaa mu ngi doon sàmm géttu Yétro, lu doy waar xew te loolu soppi na dundu Musaa yépp. Nañu seet loolu ci nettali bii di topp..