Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 30

Garab Gi Doon Tàkk

Garab Gi Doon Tàkk

MUSAA mu ngiy sàmm xaram yi. Dem na ba ca montaañ bi tudd Oreb. Foofu mu gis benn garab boo xam ne dafay tàkk waaye du jeex !

Musaa ne : ‘ Lii de, doy na waar. Xaaral ma jegesi, seet ba xam. ’ Mu jegesi, daldi dégg benn baat bu jóge ca garab ga. Baat bi ne ko : ‘ Taxawal fi nga nekk. Summil say dàll, ndaxte fi nga nekk, suuf su sell la. ’ Yàlla moo doon jaar ci malaaka ngir wax ak Musaa. Musaa daldi muur kananam.

Yàlla ne ko : ‘ Gis naa samay nit di sonn lool Misra. Léegi dama bëgg ñu jóge ci loxo waa Misra, te yow laay yónni ngir génne leen foofu. ’ Yexowa dafa bëggoon a yóbbu nitam yi, maanaam waa Israyil, ca réew mu rafet mi tudd Kanaan.

Waaye Musaa ne ko : ‘ Man may kan ba di mën a def loolu ? Te su ma demee te waa Israyil laaj ma : “ Kan moo la yónni ? ” Lan laay wax ? ’

Yàlla ne ko : ‘ Lii nga leen di wax : “ YEXOWA, ki nekk Yàlla Ibraayma, Yàlla Isaaxa ak Yàlla Yanqóoba, moo ma yónni ci yéen. ” ’ Ba pare Yexowa wax lii : ‘ Loolu mooy sama tur ba fàww. ’

Musaa ne ko : ‘ Waaye su ñu gëmul ne yow yaa ma yónni, lan laay def ? ’

Yàlla laaj ko : ‘ Loo yor ci sa loxo ? ’

Musaa tontu ko ne : ‘ Yet. ’

Yàlla ne ko : ‘ Sànni ko ci suuf. ’ Mu sànni ko ci suuf, yet ba soppaleeku jaan. Yexowa def beneen kéemaan. Mu ne ko : ‘ Dugalal sa loxo ci sa mbubb. ’ Musaa def ko. Bi mu génnee loxoom, mu ngi weexoon tàll, mel ni dafa amoon feebar bu ñu wax ngaana ! Yexowa may Musaa kàttanu def beneen kéemaan, ba pare mu wax ko lii : ‘ Boo defee kéemaan yooyu yépp, waa Israyil dinañu gëm ne man maa la yónni ci ñoom. ’

Ginnaaw loolu Musaa dellu këram, ne Yétro : ‘ Nanga ma bàyyi ma dem seeti samay mbokk yi nekk Misra, ba xam ndax ñu ngi ci jàmm. ’ Yétro ne ko : ‘ Demal ak jàmm. ’ Musaa daldi tàmbali tukki boobu jëm Misra.