Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 31

Musaa Ak Aaroona Ñu Ngi Ci Firawna

Musaa Ak Aaroona Ñu Ngi Ci Firawna

BI MUSAA delloo Misra, wax na magam Aaroona lépp lu jëm ci kéemaan yi mu naroon a def. Bi Musaa ak Aaroona defee kéemaan yooyu ci kanamu waa Israyil, ñépp a gëm ne Yexowa lañu àndal.

Musaa ak Aaroona daldi dem ca Firawna, ne ko : ‘ Yexowa mi nekk Yàlla Israyil nee na : “ Bàyyil sama mbooloo, ñu màggal ma ñetti fan ca màndiŋ ma. ” ’ Firawna ne leen : ‘ Gëmuma Yexowa. Te duma bàyyi waa Israyil ñu dem. ’

Firawna meroon na ndaxte waa Israyil dañu bëggoon a bàyyi seen liggéey ngir dem jaamu Yexowa. Mu yokk seen liggéey, ba mu gën a metti. Waa Israyil daldi mere Musaa. Xolu Musaa daldi jeex. Waaye Yexowa wax ko ne na xelam dal. Lii la wax : ‘ Dinaa tax Firawna bàyyi sama mbooloo, ñu dem. ’

Musaa ak Aaroona demaat nañu ci Firawna. Bii yoon, dañu def benn kéemaan. Aaroona dafa sànni yetam, mu soppaleeku jaan bu réy. Waaye boroom-xam-xam yi nekkoon ci Firawna, ñoom it sànni nañu ay yet, ñu soppaleeku jaan. Waaye xoolal ! Jaanu Aaroona mu ngi lekk jaani boroom xam-xam yi. Waaye ba tey, Firawna bëggul bàyyi waa Israyil ñu dem.

Léegi Yexowa dina jàngal Firawna lu am solo. Ndax xam nga lan lay def ? Dina indi 10 musiba ci kow Misra.

Musiba yu ci bare, bi ñu amee, Firawna dafa doon yónnee ci Musaa, ne ko : ‘ Boo fexee ba musiba bii jeex, dinaa bàyyi Israyil mu dem. ’ Waaye bu musiba bi jeexee, Firawna du def li mu waxoon. Du leen bàyyi ñu dem. Waaye ginnaaw fukkeel bi nag, Firawna bàyyi na Israyil mu dem.

Ndax xam nga musiba yi fa amoon yépp ? Jàngal nettali bii di topp, dinga ko xam.