Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 32

Fukki Musiba Yi

Fukki Musiba Yi

XOOLAL li ñuy wone fii. Yaa ngi gis fukki musiba yi Yexowa indi Misra. Li ñu jëkk a wone mooy bi Aaroona doon dóor ak yetam ndoxu dex bi tudd Niil. Bi mu defee loolu, ndox mi daldi soppaleeku deret. Jën yépp dee. Dex bi komaase xasaw.

Ci beneen musiba bi, Yexowa def na ba mbott yu bare jóge ci Niil bi. Ñu nga woon fu nekk : ci biir fuur yi, ci cin yi, ci lalu nit ñi, fu nekk. Bi mbott yi deewee, waa Misra dañu leen doon dajale, ba ñu def ay jal yu réy. Réew mi yépp di xasaw.

Ci musiba bi ci topp, Aaroona dafa dóor suuf si ak yetam, pënd bi daldi soppaleeku ay yoo yu doon màtte. Ñu ngi ci ñetteelu musiba bi.

Yeneen musiba yi nag, laaluñu waa Israyil. Waa Misra rekk lañu laal. Ñeenteelu musiba bi, ay weñ yu réy la woon. Ñuy dugg fu nekk ci këru waa Misra yi. Juróomeel bi, mala yi la laal. Ay nag, ay xar ak ay béy yu bare yu waa Misra moomoon, dee nañu.

Ci musiba bi ci topp, Musaa ak Aaroona dañu jël dóomu-taal, sànni ko ci kow, nit ñi ak mala yi daldi am góom yu metti. Ñu ngi ci juróom-benneelu musiba bi.

Ginnaaw loolu Musaa dafa tàllal loxoom ca asamaan. Yexowa def ba asamaan di dënnu, def it mu taw ay xeeru galaas. Masul woon a taw xeeru galaas yu mel noonu ci Misra.

Ci juróom-ñetteelu musiba bi, amoon na njéeréer yu baree bare. Masuñu woon a bare noonu ci réew mi. Lekk nañu lépp lu tawu galaas bu metti boobu bàyyi woon.

Ci juróom-ñeenteelu musiba bi, nit ñi toog nañu ñetti fan ci lëndëm. Kenn mënul woon a gis dara. Waaye waa Israyil ñoom, dañu amoon leer.

Ginnaaw loolu, Yàlla wax na waa mbooloom ñu rey béy bu ndaw walla xar bu ndaw, jël deret bi te taqal ko ci poto yi doon téye seen buntu kër. Ba pare malaaka Yàlla dafa jaar ci biir Misra. Bu gisee deret bi, du rey kenn ci biir kër googu. Waaye bépp kër bu amul deret ci buntam, malaaka Yàlla dafa ciy rey taaw bi, ci nit ñi ak ci mala yi yépp. Mooy fukkeelu musiba bi.

Bi musiba boobu amee, Firawna dafa wax waa Israyil ñu dem. Mbooloo Yàlla yépp pare woon na. Guddi googu lañu jóge Misra.