Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 33

Ñu Ngi Jéggi Géej Gu Xonq Gi

Ñu Ngi Jéggi Géej Gu Xonq Gi

XOOLAL li ñuy wone fii ! Musaa mu ngi tàllal yetam ci kow Géej gu xonq gi. Waa Israyil ñoo nekk ak moom. Mucc nañu. Waaye Firawna ak soldaaram yépp, ñu ngi nekk di suux ci géej gi. Nañu seet naka la loolu yépp ame woon.

Gis nañu ne, bi Yàlla indee fukkeelu musiba bi, Firawna wax na waa Israyil ñu jóge Misra. Lu tollu ak 600 000 góor, yokk ci ay jigéen ak xale yu bare, daldi jóge Misra, dem. Ñu bare ñu bokkul woon ci waa Israyil waaye ñu demoon ba gëm Yexowa, ànd nañu itam ak waa Israyil. Ñoom ñépp yóbbaale nañu seeni xar, seeni béy ak seeni nag.

Bala ñu jóge Misra, waa Israyil dañu laaj waa Misra ñu may leen ay yére ak ay yëf yu ñu defare wurus ak xaalis. Waa Misra dañu tiitoon lool ndax musiba bi mujjoon a dal seen kow. Moo tax ñu jox waa Israyil lépp li ñu bëggoon.

Ay fan ginnaaw loolu, waa Israyil àgg ca Géej gu xonq gi, ñu daldi taxaw ngir noppalu. Waaye léegi Firawna ak nitam yi réccu nañu li ñu leen bàyyi ñu dem. Ñu nga doon wax lii : ‘ Lu tax ñu bàyyi suñu jaam yi dem ? ’

Firawna daldi delluwaat ginnaaw. Mu gaaw a dajale 600 sareet yu gën a baax pur xeex ak yeneen, dajale it soldaaram yi, daldi daw ngir jàpp waa Israyil.

Bi waa Israyil gisee Firawna ak soldaaram yi di ñów, ñoom ñépp a tiit. Amuñu woon fenn fu ñuy jaar. Géej gu xonq gi, mu nga woon seen kanam. Waa Misra ñu nga woon seen ginnaaw. Waaye am na lu Yexowa def ngir waa Misra bañ a gis waa Israyil ba dal seen kow. Dafa def benn niir ci seen diggante.

Yexowa laaj na Musaa mu tàllal yetam ci kow géej gu Xonq gi. Bi mu ko defee, Yexowa indi na ngelaw bu réy jóge penku, mu xaajale géej gi ñaar, mu am yoon ci seen diggante.

Waa Israyil daldi jaar ci yoon boobu fekk suuf si wow na. Ay milyoŋi nit lañu woon ak seen mala yépp. Bala ñoom ñépp di mën a jàll, laajoon na waxtu yu bare. Yàlla daldi def ba waa Misra mën a gisaat waa Israyil. Seen jaam yi ñu ngi woon nii seen kanam, di dem ! Ñu daldi dugg ci biir géej gi, topp seen ginnaaw.

Ñu ngi woon ci yoon bi, Yàlla daldi def ruu yi sareet yooyu amoon, teggeeku. Waa Misra tiit lool, di yuuxu. Lii lañu doon wax : ‘ Yexowa mooy xeex pur waa Israyil. Nañu fi jóge ! ’ Waaye kenn mënatul woon a dellu ginnaaw.

Yexowa daldi wax Musaa mu tàllal yetam ci kow géej gu Xonq gi, ni nga ko gise fii. Géej gi tëjuwaat te muur waa Misra yi ak seeni sareet yooyu. Soldaaru Misra yépp ñoo toppoon waa Israyil ci biir géej gi. Kenn rëccu ci !

Mbooloo Yàlla kontaan na lool ndaxte rëcc nañu ! Góor yi dañu woyal Yexowa ngir gërëm ko. Lii lañu woy : ‘ Yexowa daaneel na leen, daaneel bu metti. Sànni na ci biir géej gi fas yi ak ñi leen doon dawal. ’ Miryam, magu Musaa, daldi jóg, jigéen yépp di ko topp, ñu nekk di tëgg, ak di fecc, te di topp li góor yi doon woy : ‘ Yexowa daaneel na leen, daaneel bu metti. Sànni na ci biir géej gi fas yi ak ñi leen doon dawal. ’

Gàddaay gi (Exode) pàcc 12 ba 15.