Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 3

Diggante bi ñu jógee Misra ba ci jamano buuru Israyil bu jëkk bi

Diggante bi ñu jógee Misra ba ci jamano buuru Israyil bu jëkk bi

Bi waa Israyil jógee Misra, Musaa yóbbu na leen ba ca tundu Sinayi. Foofu la leen Yàlla joxe ndigalam yi. Ginnaaw loolu, Musaa yónni na 12 nit ca Kanaan ngir yërndu réew mi te seet ni mu mel. Waaye 10 nit ci ñoom dañu wax lu ñaaw ci réew moomu, ba tax mbooloo mi bëgg dellu Misra. Yàlla daldi yar waa Israyil ndax seen ñàkk ngëm. Dafa leen wax ne dinañu nekk di wër rekk ci màndiŋ mi nga xam ne dara du fa sax. Te dinañu fa des lu mat 40 at.

Ginnaaw loolu, Yosuwe la Yàlla tànn ngir yóbbu waa Israyil ca Kanaan. Yexowa def na ay kéemaan ngir dimbali leen ñu dugg Kanaan. Taxawal na ndox mi nekk ci dexu Yurdan, daaneel na miiri Yeriko, te taxawal na naaj bi ci asamaan benn fan yépp. Ci lu mat juróom-benni at la waa Israyil nangu réew mi ci loxo waa Kanaan.

Ay àttekat ñoo doon ilif Israyil ci lu mat 356 at. Yosuwe mooy àttekat bi jëkk. Dinañu jàng lu jëm ci ñu bare ci ñoom, mel ni Barag, Sedeyon, Yefte, Samson, Samwil ak ñeneen. Dinañu jàng itam lu jëm ci ay jigéen yu mel ni Raxab, Debora, Yawel, Ruut, Nawomi ak Delila. Lépp li ñu nettali ci XAAJ 3, xewoon na ci biir 396 at.

 

IN THIS SECTION

NETTALI 34

Lekk Bu Bees

Lekk bu raar boobu asamaan la jóge woon wàcc.

NETTALI 35

Yexowa Joxe Na Ndigalam Yi

Yan ñaari ndigal ñoo ëpp solo ci fukki ndigal yi yépp ?

NETTALI 36

Nag Bi Ñu Defare Wurus

Lu tax nit ñi di jaamu xërëm bu ñu defare ay jaaro wurus ?

NETTALI 37

Tànt Fi Ñuy Jaamoo Yàlla

Ci néeg bi gënnoon a féete biir la gaalu kóllëre gi nekkoon.

NETTALI 38

Fukki Góor Ak Ñaar Yuy Yërndu Réew Mi

Fukk yi wax benn wax bi, waaye ñaar ci ñoom wax leneen. Ñan la waa Israyil gëmoon ?

NETTALI 39

Yetu Aaroona Mu Ngiy Tóor-tóor

Naka la yet bu wow mënee tóor-tóor ci benn guddi rekk ?

NETTALI 40

Musaa Dóor Na Xeer Bi

Musaa am na li mu bëggoon, waaye merloo na itam Yexowa.

NETTALI 41

Jaan Bi Ñu Defare Përëm

Lu tax Yàlla yónni ay jaan ngir ñu màtt waa Israyil ?

NETTALI 42

Mbaam Buy Wax

Mbaamu Balaam bi gis na lu Balaam mënul woon a gis.

NETTALI 43

Yosuwe Lañuy Def Njiit

Musaa mu ngi am doole ba tey, kon lu tax Yosuwe di jël palaasam ?

NETTALI 44

Raxab Nëbb Na Ñi Ñów Yërndu Réew Mi

Naka la Raxab dimbalee ñaari góor yooyu ak lan la leen ñaan ?

NETTALI 45

Ñu Ngi Jéggi Dex Bi Tudd Yurdan

Bi saraxalekati yi dugalee seen tànk ci biir ndox mi, ab kéemaan moo amoon.

NETTALI 46

Miir Yi Wër Yeriko

Naka la buum mënee tere ab miir mu daanu ?

NETTALI 47

Benn Sàcc Ci Israyil

Ndax kenn nit ku bon mën na indi musiba mbooloo mi yépp ?

NETTALI 48

Waa Gibeyon Ñoo Am Xel

Dañu nax Yosuwe ak waa Israyil yi ba ñu dig leen séq jàmm ak ñoom, waaye waa Israyil sàmm nañu seen kàddu.

NETTALI 49

Naaj Bi Taxaw Na Ci Asamaan Si

Yexowa dafa defal Yosuwe lu mu masul woon a def te defaatu ko ba tey.

NETTALI 50

Ñaari Jigéen Yu Am Fit

Barag moo jiite xarekati Israyil yi ci xare bi, kon lu tax ñu jox Yayel ndam li ?

NETTALI 51

Ruut Ak Nawomi

Ruut dafa bàyyi mbooloom ngir des ak Nawomi te jaamu Yexowa.

NETTALI 52

Sedeyon Ak 300 Góor Yi Mu Àndaloon

Yexowa dafa def lu ñu faralul woon a gis, maanaam nàtt leen ci naan ndox, ngir wàññi xarekat yi ba mu des gurup bu ndaw.

NETTALI 53

Li Yefte Dig Yexowa

Li mu dige yemul rekk ci moom, waaye dafa laal doomam bu jigéen itam.

NETTALI 54

Nit Ki Gënoon A Am Doole

Naka la Delila def ba xam li tax Samson amoon doole ?

NETTALI 55

Xale Bu Ndaw Buy Jaamu Yàlla

Yàlla dafa jaar ci Samwil ngir yégal Eli saraxalekat bu mag bi xibaar bu neexul ci xol.