Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 35

Yexowa Joxe Na Ndigalam Yi

Yexowa Joxe Na Ndigalam Yi

LU TOLLU ak ñaari weer ginnaaw bi ñu génnee Misra, waa Israyil àgg nañu ci tundu Sinayi bi ñuy woowe itam Oreb. Foofu la Yexowa waxe woon ak Musaa ci garab gi doon tàkk. Mbooloo mi daldi toog foofu lu xaw a yàgg tuuti.

Musaa mu ngi yéeg ci kow tund bi, mbooloo mi di ko xaar ci suuf. Bi mu àggee ci kow, Yexowa wax na Musaa ne dafa bëgg waa Israyil topp ko te nekk mbooloom. Musaa wàcc te jottali leen li Yexowa wax. Mbooloo mi yépp ne dinañu déggal Yexowa, ndaxte dañu bëgg a nekk mbooloom.

Léegi Yexowa mu ngi def lu doy waar. Saxar daldi feeñ ci kow tund bi, asamaan si di dënnu, dënnu gu réy. Yexowa wax na itam ak mbooloo mi. Mu ne leen : ‘ Man maay Yexowa sa Yàlla mi la génne Misra. ’ Ba pare mu digal lii : ‘ Waruloo jaamu mukk beneen yàlla ku dul man. ’

Yàlla dolli na ci juróom-ñeenti ndigal. Mbooloo mi tiit lool. Ñu ne Musaa : ‘ Yow mii yaa war a wax ak ñun, ndaxte dañu ragal, bu Yàlla waxee ak ñun, ñu dee. ’

Ginnaaw loolu Yexowa wax Musaa lii : ‘ Ñówal ci man ci tund bi. Dinaa la jox ñaari xeer fu ma bind ndigal yi ma bëgg waa mbooloo mi topp. ’ Musaa daldi delluwaat ca tund ba. Toog na fa 40 bëccëg ak 40 guddi.

Yàlla am na ndigal yu bare yu mu bëgg a jox mbooloom. Musaa bind na leen ñoom ñépp. Yàlla jox na itam Musaa ñaari xeer (xoolal li ñuy wone fii). Yàlla ci boppam moo ci bind 10 ndigal yi mu waxoon mbooloo mi yépp. Ñu ngi leen di woowe Fukki Ndigal yi.

Fukki Ndigal yi, ay ndigal yu am solo la. Yeneen ndigal yi Yàlla jox waa Israyil, ñoom itam am nañu solo. Benn bi nee na : ‘ Danga war a bëgg Yexowa sa Yàlla ak sa xol bépp ak sa xel mépp ak sa bakkan bépp ak sa kàttan gépp. ’ Beneen ndigal mooy bii : ‘ Danga war a bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp. ’ Doomu Yàlla, Yeesu Kirist, nee na ñaari ndigal yooyu ñoo ëpp solo ci ndigal yi yépp Yexowa jox mbooloom Israyil. Bu ci kanamee, dinañu jàng lu bare lu jëm ci Doomu Yàlla ji ak li mu jàngale.

Gàddaay gi (Exode) 19:1-25 ; 20:1-21 ; 24:12-18 ; 31:18 ; Deutéronome 6:4-6 ; Lévitique 19:18 ; Macë 22:36-40.