Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 37

Tànt Fi Ñuy Jaamoo Yàlla

Tànt Fi Ñuy Jaamoo Yàlla

LI ÑUY wone fii, ndax xam nga lan la ? Tànt la fu ñuy jaamoo Yexowa. Ci tubaab dañu koy woowe itam tabernacle. Pare nañu ko tabax benn at ginnaaw bi ñu génnee Misra. Ndax xam nga kan moo leen wax ñu tabax ko ?

Yexowa moo ko wax Musaa bi mu nekkoon ci kow tundu Sinayi. Dafa ko wax mu defar ko ci fasoŋ boo xam ne, bu ñu ko waree yóbbu feneen, dina yomb. Su ko defee ñu mën koo samp ci béréb fu ñuy dem. Kon bi waa Israyil doon wër màndiŋ ma, maanaam béréb boobu nga xam ne dara du fa sax, dañu ko doon yóbbaale.

Boo xoolee ci biir néeg bu ndaw bi ci tànt bi, dinga gis lu mel ni kees. Dañu ko woowe gaalu kóllëre gi. Am na ñaari malaaka yu ñuy woowe seruben te ñu defare leen wurus, yu nekk ci kowam, ku nekk ci benn boor. Yàlla bindaat na itam Fukki Ndigal yi ci yeneen ñaari xeer, ndaxte Musaa dafa tojoon yu jëkk yi. Dañu dugal ñaari xeer yooyu ci biir gaalu kóllëre gi. Amoon na fa itam benn pot fu ñu defoon mànn. Ndax yaa ngi fàttaliku lan mooy mànn ?

Yexowa tànn na magu Musaa bi tudd Aaroona, ngir mu nekk saraxalekat bu mag bi. Moom mooy jiite mbooloo mi bu ñuy jaamu Yexowa. Doomam yi itam ay saraxalekat lañu.

Xoolal léegi néeg bi gën a mag ci tànt bi. Moo gën a mag ñaari yoon néeg bu ndaw bi. Ndax gis nga kees bu ndaw bi am saxar bu ciy génn ? Saraxalukaay la. Foofu la saraxalekat yi di lakke cuuraay bu neex. Yaa ngi gis itam tegukaayu làmp bu def juróom-ñaari làmp. Li ci des, benn taabal la fu ñu def 12 kàmpu mburu.

Ci ëtt biy wër tànt bi, am na paan bu mag bu fees ak ndox. Ndox moomu la saraxalekat yi di jël pur raxas seeni tànk ak seeni loxo. Am na itam saraxalukaay bu mag bi. Dañu ciy lakk mala yi ñuy saraxal Yexowa. Tànt boobu mu ngi ci diggu mbooloo mi, yeneen tànt yi fi waa Israyil yi dëkk wër ko.