Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 39

Yetu Aaroona Mu Ngiy Tóor-tóor

Yetu Aaroona Mu Ngiy Tóor-tóor

XOOLAL yet bi ñuy wone fii, ak tóor-tóor yi ak lu mel ni gerte-tubaab yu ci sax. Ci benn guddi rekk lañu sax ! Yetu Aaroona la. Nañu seet lu tax loolu am.

Léegi, waa Israyil ñu ngi ci màndiŋ mi di wër rekk. Am na ñu bëggul Musaa nekk seen njiit. Bëgguñu it Aaroona nekk seen saraxalekat bu mag bi. Kora bokk na ci ñiy xalaat loolu. Datan, Abiram, ak 250 njiit ci mbooloo mi, ñoom itam bokk nañu ci. Ñooñu ñépp a ñów ci Musaa, ne ko : ‘ Lu tax nga yëkkëti sa bopp ci suñu kow ? ’

Musaa wax Kora ak ñi ko doon topp : ‘ Suba ci suba, jëlleen seen tibbukaayu safara yi, def ci cuuraay. Nangeen ñów ci tàntu Yexowa. Dinañu gis kan la Yexowa di tànn. ’

Kora ak 250 nitam yi ñów ci tànt bi ci ëllëg si. Ñu bare ànd nañu ak ñoom. Yexowa mer na lool. Musaa ne lii : ‘ Soreleen nit ñu bon ñii ak seeni tànt. Buleen laal dara lu ñu moom. ’ Bi mbooloo mi déggee loolu, ñu sore tàntu Kora, bu Datan ak bu Abiram.

Musaa ne leen : ‘ Léegi dingeen gis kan la Yexowa di tànn. Suuf si dina ubbeeku te wann nit ñu bon ñii. ’

Bi Musaa waxee loolu rekk, suuf si daldi ubbeeku. Tàntu Kora ak lépp li mu moom, Datan ak Abiram ak ñi àndoon ak ñoom ñépp, dugg nañu ci biir suuf si. Bi mbooloo mi déggee seeni yuuxu, ñépp yuuxu : ‘ Dawleen, bala suuf si di ñu wann, ñun it ! ’

Ba léegi Kora ak 250 nitam yi ñu ngi taxaw ci wetu tàntu Yàlla bi. Yexowa daldi wàcce safara, lakk leen ñoom ñépp. Ginnaaw loolu, Yexowa wax na doomu Aaroona bi tudd Eleyasar, mu jël tibbukaayu safara yi nit ñi dee moomoon, lakk leen ba ñu seey te raax ko ci saraxalukaay bi. Saa yu ko waa Israyil gisee, dinañu fàttaliku ne Aaroona ak doomam yi rekk ñoo mën a nekk saraxalekatu Yexowa.

Yexowa dafa bëgg loolu leer nàññ, moo tax mu ne Musaa : ‘ Waxal njiitu giiru Israyil yépp ñu indi ku nekk yetam. Na Aaroona indi yetam pur waa Lewi, maanaam ñi bokk ci askanu Lewi. Dugalal yet yooyu yépp ci biir tàntu Yàlla bi, ci kanamu gaalu kóllëre gi. Ki may tànn pur mu nekk saraxalekat, yetam dina tóor-tóor. ’

Bi Musaa ñówee ci ëllëg si, mu gis yetu Aaroona am tóor-tóor ak ay doom yu mel ni gerte-tubaab. Ndax léegi xam nga lu tax Yexowa def ba yetu Aaroona am ay tóor-tóor ?