Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 41

Jaan Bi Ñu Defare Përëm

Jaan Bi Ñu Defare Përëm

JAAN bi lonku ci bant bi, ndax jaan dëgg la ? Déedéet. Përëm lañu ko defare. Yexowa moo wax Musaa mu def ko ci bant boobu ngir képp ku ko xool, bañ a dee. Waaye yeneen jaan yi ngay gis ci suuf, ay jaan dëgg lañu. Dañu màtt nit ñi, moo tax ñu feebar. Ndax xam nga lu tax ñu màtt leen ?

Waa Israyil ñoo wax lu bon ci Yàlla ak ci Musaa. Dañu ne : ‘ Lu tax ngeen génne ñu Misra ? Xanaa dangeen bëggoon ñu dee ci màndiŋ mii ? Fii amul lekk, amul ndox. Te doyal nañu ci mànn bi. ’

Waaye mànn bi, lekk bu baax la. Yexowa moo def kéemaan ba jox leen ko. Def na kéemaan it ngir ñu am ndox. Waaye amuñu ngërëm ci Yàlla ndax li mu def yépp ngir toppatoo leen. Kon Yexowa dafa yónni ay jaan ngir yar leen. Jaan yi màtt leen. Ñu bare dee ci.

Mbooloo mi daldi ñów ci Musaa, ne ko : ‘ Bàkkaar nañu, ndaxte wax nañu lu ñaaw ci Yexowa ak ci yow. Léegi, ñaanal Yexowa mu génne fi jaan yii. ’

Musaa ñaanal na mbooloo mi. Yexowa wax na Musaa mu defar jaanu përëm te def ko ci benn bant. Képp ku jaan màtt rekk, dinga war a xool jaan boobu. Musaa def li ko Yàlla wax. Léegi ku jaan màtt, dafa doon xool jaanu përëm bi, daldi wér.

Am na li ñu war a jàng ci loolu. Ñun ñépp, dañu mel ni waa Israyil yi jaan yi màttoon. Dañu war a dee. Doomu Aadama boo gis, dafay màgget, di feebar te di dee. Góor ak jigéen yu jëkk yi, maanaam Aadama ak Awa, ñoo tax loolu am. Dañu bàyyi Yexowa. Te ñun ñépp, seeni doom lañu. Waaye am na lu Yexowa def ngir ñu mën a dund ba fàww.

Yexowa dafa yónni doomam, Yeesu Kirist, ci kow suuf si. Yeesu, dañu ko daaj ci bant, ndaxte ñu bare dañu foogoon ne dafa bon. Waaye Yexowa dafa joxe Yeesu ngir ñu mucc. Bu ñu xoolee ci moom, bu ñu ko toppee, dinañu mën a am dund gu dul jeex. Waaye dinañu ci gën a wax bu ci kanamee.