Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 42

Mbaam Buy Wax

Mbaam Buy Wax

MBAAM buy wax, ndax mas nga dégg loolu ? Xéyna dinga ne : ‘ Déedéet. Mala du wax. ’ Waaye Biibël bi wax na ci mbaam bu ko def. Nañu seet ni loolu ame.

Léegi, waa Israyil ñu ngi waaj a dugg ci réewu Kanaan. Balag mooy buuru Mowab. Moom dafa ragal waa Israyil. Looloo tax mu yónnee ngir ñu woowal ko kenn ku muus te tudd Balaam ngir mu ñaanal waa Israyil lu bon. Balag dig ko xaalis bu bare. Balaam yéeg ci mbaamam ngir dem wuyu Balag.

Waaye Yexowa, moom, bëggul Balaam ñaanal mbooloom lu bon. Kon, dafa yónni benn malaaka bu yor jaasi bu gudd ngir mu taxaw ci yoonu Balaam. Balaam moom, mënul gis malaaka mi. Waaye mbaam bi gis na ko. Mu jéem a jàdd fii, mënul. Mu jéem a jàdd fee, mënul. Mu mujj tëdd ci suuf. Balaam mer lool. Muy dóor mbaamam rekk.

Balaam daldi dégg mbaamam di wax ak moom. Yexowa moo doon def loolu. Mbaam bi ne ko : ‘ Lu tax nga may dóor ? Lan laa def ? ’

Balaam ne ko : ‘ Danga ma bëgg dofloo. Bu ma amoon jaasi, ma rey la ci saa si ! ’

Mbaam bi laaj ko lii : ‘ Ndax mas naa la def li ma la def tey ? ’

Balaam ne ko : ‘ Déedéet. ’

Yexowa def ba Balaam gis malaaka mi taxawoon ci yoon bi ak jaasi bi. Malaaka mi ne ko : ‘ Lu tax nga dóor sa mbaam ? Man maa la tere jàll, ndaxte waruloo ñaanal Israyil lu bon. Loolu moo tax ma ñów. Bu mbaam bi kontine woon, duma ko def dara, waaye yow laa naroon a rey. ’

Balaam ne ko : ‘ Def naa bàkkaar. Xamuma woon ne yaa ngi taxaw ci diggu yoon bi. ’ Malaaki mi bàyyi ko mu jàll. Balaam dem ca Balag. Waaye ba tey jéem na ñaanal Israyil lu bon. Waaye Yexowa def na mu barkeel Israyil ñetti yoon.