Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 43

Yosuwe Lañuy Def Njiit

Yosuwe Lañuy Def Njiit

MUSAA dafa bëgg a dem Kanaan ak waa Israyil. Lii la ñaan Yexowa : ‘ Yexowa, may ma, ma jéggi dexu Yurdan, te gis réew mu baax mi. ’ Waaye Yexowa ne ko : ‘ Léegi, doy na ! Bu ma waxati loolu ! ’ Ndax xam nga lu tax Yexowa wax ko loolu ?

Li xewoon bi Musaa dóoree xeer bi moo tax. Ndax yaa ngi fàttaliku ne moom ak Aaroona màggaluñu woon Yexowa ? Waxuñu woon mbooloo mi ne Yexowa moo génne woon ndox mi ci xeer bi. Loolu moo tax Yexowa wax ne duñu dem Kanaan.

Bi Aaroona gaañoo, am na ay weer léegi. Lii la Yexowa wax Musaa : ‘ Jëlal Yosuwe. Indi ko mu taxaw ci kanamu Eleyasar, saraxalekat bi, ak mbooloo mi, ba pare waxal ñépp ne Yosuwe mooy nekk njiit bi léegi. ’ Ni nga ko gise fii Musaa def na lépp li ko Yexowa wax.

Lii la Yexowa wax Yosuwe : ‘ Nanga am fit, bul ragal. Dinga yóbbu waa Israyil ba ci biir réew mi ma leen dig, maanaam Kanaan. Dinaa ànd ak yow. ’

Ginnaaw loolu, Yexowa wax na Musaa mu yéeg ci kow tundu Nebo ci réewu Mowab. Foofu Musaa gis na ci ginnaaw dexu Yurdan réew mu rafet moomu tudd Kanaan. Yexowa ne ko : ‘ Lii mooy béréb bi ma digoon doomi Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba. Bàyyi naa la nga gis ko, waaye doo ci dugg. ’

Ci kow tundu Nebo boobu la Musaa gaañu. Amoon na 120 at, fekk amoon na doole ba tey te mën a gis bu baax. Mbooloo mi yépp daldi ko jooy. Waaye léegi Yosuwe moo nekk seen njiit. Mbooloo mi kontaan na ci loolu.

Nombres 27:12-23 ; Deutéronome 3:23-29 ; 31:1-8, 14-23 ; 32:45-52 ; 34:1-12.