Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 46

Miir Yi Wër Yeriko

Miir Yi Wër Yeriko

LU TAX miiri Yeriko di daanu ? Dafa mel ni bomb bu mag moo dal seen kow. Waaye bomb amul woon ca jamano jooja. Fetal amul woon sax. Yexowa moo tax miir yi di daanu. Moom moo def beneen kéemaan. Nañu seet lu tax loolu yépp am.

Lii la Yexowa wax Yosuwe : ‘ Bés bu nekk, yow ak ñiy xeex ak yow ngir waa Israyil, maanaam sa xarekat yi, nangeen dox, wër dëkk bi, benn yoon. Nangeen def loolu juróom-benni fan. Nangeen yóbbaale gaalu kóllëre gi. Juróom-ñaari saraxalekat ñoo war a dox ci kanamam te ëf ci seeni béjjén. ’

‘ Ci juróom-ñaareelu bés bi, nangeen wër dëkk bi juróom-ñaari yoon, ba pare ëf lu yàgg ci béjjén yi, te na ñépp yuuxu, mel ni yuuxu bu ñuy yuuxu bu ñuy xeex. Miir yi wër Yeriko yépp dinañu daanu. ’

Yosuwe ak mbooloo mi def li Yexowa waxoon. Dañuy dox rekk. Kenn waxul. Béjjén yi ak tànk yi rekk lañuy dégg. Wóor na ne ñi nekk ci biir Yeriko te bañ mbooloo Yàlla tiitoon nañu lool. Ndax yaa ngi gis buum bu xonq biy génn ci palanteer bi nekk ci kow ? Palanteeru kan la ? Bu Raxab bi la. Def na li ko ñaari góor ñi ñówoon yërndu réew mi waxoon. Njabootam yépp ñu ngi ak moom ci biir kër gi di xaar.

Ci juróom-ñaareelu fan bi, dañu wër dëkk bi juróom-ñaari yoon, ëf ci béjjén yi, xarekat yépp yuuxu, miir yi daanu, Yosuwe daldi wax lii : ‘ Reyleen ñi fi nekk ñépp, ba pare lakk dëkk bi. Lakkleen lépp li fa nekk. Bàyyileen rekk lu nekk xaalis, wurus, përëm ak weñ, te def ko fi ñuy dence alalu tàntu Yexowa bi. ’

Yosuwe wax na itam ñaari góor ñi demoon ci Raxab : ‘ Demleen ci kër Raxab, indileen ko, moom ak njabootam yépp. ’ Raxab ak njabootam mucc nañu, ni leen ko ñaari góor ñi digoon.