Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 48

Waa Gibeyon Ñoo Am Xel

Waa Gibeyon Ñoo Am Xel

DËKK yu bare ci Kanaan pare nañu léegi ngir xeex Israyil. Pur ñoom, dinañu daan Israyil. Waaye waa Gibeyon, ñoom, xalaatuñu loolu. Gëm nañu ne Yàlla mooy jàpple waa Israyil te bëgguñu xeex Yàlla. Xam nga lan lañu def ?

Dañu wax ne dinañu def mel ni ci dëkk bu sore lañu jóge. Ay góor daldi sol ay yére yu xotteeku ak ay dàll yu màgget. Ñu jël ay saag yu màgget, def leen ci seeni mbaam, jël mburu bu wow koŋŋ, dem ca Yosuwe, ne ko : ‘ Fu sore lañu jóge, ñow fii, ndaxte am na lu ñu dégg ci seen Yàlla ju mag ji tudd Yexowa. Dégg nañu lépp li mu leen defal ca Misra. Moo tax suñu njiit yi sant ñu ñu jël lu ñuy lekk ci yoon bi te ñów wax leen lii : “ Seeni jaam lañu. Nangeen ñu dig ne dungeen xeex ak ñun. ” Fi ñu jóge sore na lool. Xoolleen ! Suñuy yére màgget nañu te suñu mburu wow na koŋŋ. ’

Yosuwe ak yeneen njiit yi gëm li waa Gibeyon wax. Ñu dig leen ne duñu xeex ak ñoom. Waaye bi mu amee ñetti fan, ñu daldi dégg ne waa Gibeyon yi jógewuñu fu sore.

Yosuwe laaj leen lii : ‘ Lu tax ngeen wax ne fi ngeen jóge dafa sore ? ’

Waa Gibeyon tontu ko ne : ‘ Dégg nañu ne seen Yàlla Yexowa moo leen dig ne dina leen may réewu Kanaan yépp. Ñu ragal ngeen rey ñu. Moo tax ñu def loolu. ’ Waa Israyil soppiwuñu li ñu leen digoon. Bàyyi nañu leen ñu dund, ñu nekk seeni surga.

Buuru Yerusalem dafa mer ndaxte waa Gibeyon ak waa Israyil léegi dañu am jàmm ci seen diggante. Mu daldi wax ak yeneen ñeenti buur, ne leen : ‘ Kaayleen jàpple ma, ñu xeex Gibeyon. ’ Léegi, juróomi buur ñooy xeex ak ñoom. Ndax waa Gibeyon amoon nañu xel dëgg bi ñu fexee ba am jàmm ak Israyil ? Nañu jàng nettali bii di topp ngir xam loolu.