Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 50

Ñaari Jigéen Yu Am Fit

Ñaari Jigéen Yu Am Fit

BI WAA Israyil demee ba am coono, ñu daldi woo Yexowa. Yexowa may leen njiit yu am fit pur dimbali leen. Njiit yooyu, àttekat lañu leen di woowe ci Biibël bi. Yosuwe moo doon àttekat bu jëkk bi. Ginnaaw moom amoon na Otniyel, Exud, Samgar ak ñeneen. Waaye, ci ñi dimbali Israyil noonu, amoon na ñaari jigéen yu tudd Debora ak Yawel.

Debora, yonent bu jigéen la woon. Yexowa dafa ko doon yëgal liy am ëllëg, ba pare moom mu jottali ko mbooloo mi. Debora àttekat la woon itam. Dafa doon toog ci suufu garab bu ñuy wax tiir, nit ñi di ñów wax ko seeni poroblem ngir mu dimbali leen.

Jamano jooju, Yabin moo nekkoon buuru Kanaan. Amoon na 900 watiir yu ñu defar ngir xeex, ak it ay soldaar yu aay lool. Seen kàttan dafa bare woon ba ñu mën a forse ñu bare ci waa Israyil ñu nekk seeni jaam. Ki doon jiite soldaar yooyu, Sisera la tuddoon.

Benn bés, Debora dafa woo àttekat bi tudd Barag, ne ko : ‘ Yexowa nee na : “ Jëlal 10 000 góor, yóbbu leen ca tundu Tabor. Dinaa fa indi Sisera. Dinaa tax nga daan ko, moom ak soldaaram yépp. ” ’

Barag ne Debora : ‘ Dinaa dem boo ñówee ak man. ’ Debora ànd ak moom, waaye lii la wax Barag : ‘ Du yow yaay tax ngeen gañe xeex bi, ndaxte ci loxo jigéen la Yexowa di daaneel Sisera. ’ Te loolu moo am.

Barag wàcc tundu Tabor ngir fekk soldaari Sisera. Jékki-jékki rekk, Yexowa daldi indi ndox mu baree bare, soldaaru Sisera yu bare dee ci biir ndox mi. Waaye Sisera moom, dafa wàcc watiiram, daw.

Sisera daldi àgg ci tànt fu Yawel nekkoon. Yawel wax ko mu dugg, ba pare may ko meew, mu naan. Bi mu naanee, mu komaase gëmméentu, daldi nelaw, nelaw bu xóot. Yawel jël benn pont ci yi ñu sampe tànt bi, mu daaj ko ci boppu ku bon kooku. Bi Barag ñówee, Yawel won na ko Sisera mi dee woon ba pare. Kon gis nga ne li Debora waxoon moo am.

Buur Yabin, moom itam, rey nañu ko. Waa Israyil daldi amaat jàmm lu xaw a yàgg tuuti.