Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 51

Ruut Ak Nawomi

Ruut Ak Nawomi

CI BIIBËL bi am na téere bu tudd Ruut. Dañu ci nettali li dal benn njaboot ci jamano àttekati Israyil. Ruut, jigéen la bu dëkkoon ci réew mi tudd Mowab. Moom, bokkul woon ci mbooloo Yàlla, maanaam ci Israyil. Waaye bi mu déggee lu jëm ci Yexowa mi nekk Yàlla dëgg ji am, dafa dem ba bëgg ko lool. Nawomi, jigéen bu màgget la woon. Moom moo dimbali Ruut mu xam Yexowa.

Nawomi, waa Israyil la. Moom ak jëkkëram ak ñaari doomam yi dañu ñów ci réewu Mowab ndax xiif bi amoon ci Israyil. Jëkkëru Nawomi gaañu na. Ginnaaw loolu ñaari doomu Nawomi takk nañu ay jabar. Waa Mowab lañu woon te Ruut ak Orpa lañu tuddoon. Waaye 10 at ginnaaw loolu, ñaari doomu Nawomi gaañu nañu, ñoom it. Léegi Nawomi, Ruut ak Orpa, ci naqar kese lañu dëkk. Nawomi, lan lay def ?

Benn bés, Nawomi dafa fas yéenee dellu fu sore foofu mbooloom nekk. Ruut ak Orpa bañ koo bàyyi, ñu daldi ko topp. Waaye bi ñu demee ba xaw a sore, Nawomi ne leen : ‘ Nangeen ñibbi fi ngeen dëkk te toog ak seeni yaay. ’

Nawomi bëgg leen tàggu. Ñoom ñaar daldi jooy ndaxte dañu bëgg Nawomi lool. Ñu ne ko : ‘ Déedéet. Dinañu ànd ak yow ba ci sa mbooloo. ’ Waaye Nawomi ne leen : ‘ Ñibbileen, samay doom. Nekk ci seen dëkk mooy gën ci yéen. ’ Orpa daldi ñibbi. Waaye Ruut moom, demul.

Nawomi xool ko, ne ko : ‘ Orpa dem na. Àndal ak moom, ngeen ñibbi seen dëkk. ’ Waaye Ruut ne ko : ‘ Bu ma wax ma dem. Bàyyil ma ànd ak yow. Dinaa dem fi ngay dem. Dinaa dund fi ngay dund. Sa mbooloo dina nekk sama mbooloo te sa Yàlla dina nekk sama Yàlla. Fi ngay dee, foofu laay deewe te foofu lañu may suule. ’ Bi Ruut waxee loolu, Nawomi bàyyi na ko mu ànd ak moom.

Ñaari jigéen yooyu àgg nañu Israyil, am fu ñuy dëkk. Ruut daldi dem liggéey ci tool yi, ndaxte ci jamano ngóob lañu tóllu woon. Góor gu tudd Bowas dafa ko bàyyi mu for ci toolam yi li des ci ngóob bi. Ndax xam nga yaayu Bowas ? Mooy Raxab bi dëkkoon Yeriko.

Benn bés, lii la Bowas wax Ruut  : ‘ Dégg naa lépp li ñuy wax ci yow. Dégg naa lu baax li nga defal Nawomi. Dégg naa ni nga bàyyee sa baay ak sa yaay, jóge fi nga dëkkoon te ñów fii ci biir mbooloo boo xam ne masuloo koo xam. Yàlla na la Yexowa defal lu baax ! ’

Ruut tontu ko ne : ‘ Danga baax lool ak man. Seddal nga sama xol ak wax yu neex yi nga ma wax léegi. ’ Waaw, Bowas dafa bëgg Ruut lool. Yàggul nag, mu takk ko. Nawomi kontaan na lool léegi. Waaye bés bi Ruut ak Bowas amee seen taaw la gën a kontaan. Obedd lañu ko tudde. Obedd moo nekkoon maamu Daawuda. Dinañu wax ci Daawuda bu ci kanamee ci téere bii.

Téere bi tudd Ruut ci Biibël bi.