Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 52

Sedeyon Ak 300 Góor Yi Mu Àndaloon

Sedeyon Ak 300 Góor Yi Mu Àndaloon

NDAX gis nga lu xew fii ? Ñi ngay gis ñépp, ay waa Israyil lañu te dañuy dem xeex ngir waa Israyil. Ñi sëgg dañuy naan. Ki taxaw seen wet mooy àttekat bi tudd Sedeyon (Guidéôn). Mu ngiy xool ni ñuy naane.

Xoolal bu baax ni góor ñooñu di naane. Am na ñuy sëgg ba ci suuf, dugal seen gémmiñ ci biir ndox mi. Waaye am na kenn kuy tanq ndox ak loxoom, ndax mu mën a gis li ko wër. Loolu am na solo ndaxte Yexowa moo wax Sedeyon mu tànn rekk ñi xoolaale li leen wër bi ñuy naan. Ñeneen ñi, Yàlla nee na dañu war a ñibbi seen kër. Dinañu gis lu tax.

Waa Israyil amaat nañu léegi coono yu bare ndaxte toppuñu li Yexowa wax. Waa Madyan ñoo leen ëpp doole léegi te ñu ngi leen di fitnaal. Waa Israyil daldi jooy te ñaan Yexowa mu dimbali leen. Yexowa daldi leen dimbali.

Yexowa wax na Sedeyon mu dajale ay xarekat. Sedeyon daldi am 32 000 góor. Waaye ak 135 000 soldaar lañu war a xeex. Ba tey lii la Yexowa wax Sedeyon : ‘ Góor ñi nga am fii, ëpp nañu. ’ Lu tax Yexowa wax loolu ?

Ndaxte bu Israyil gañee xeex bi ak Madyan, mën na am ñu foog ne seen doole moo tax te soxlawuñu woon Yexowa dimbali leen. Kon Yexowa nee na Sedeyon : ‘ Waxal ñi ragal ñépp ñu ñibbi. ’ Mu am ci 22 000 ñu ñibbi. Léegi, 10 000 rekk ñoo des ngir xeex ak 135 000 soldaaru Madyan yi.

Waaye déglul li Yexowa wax ! Nee na : ‘ Dangeen bare ba tey. ’ Mu ne Sedeyon mu wax nit ñi ñu dem naani ci dex bi. Te ñiy sëgg ñépp ba def seen gémmiñ ci ndox mi, na leen wax ñu ñibbi. Yexowa dig na Sedeyon lii : ‘ Dinaa la may nga yóbbu ndam li ak 300 góor ñi doon naan di xoolaale li leen wër. ’

Bésu xeex bi jot. Sedeyon xaaj 300 góor ñooñu, ñetti xaaj. Mu jox góor gu nekk benn béjjén ak benn pot fu ñu dugal benn bant buy tàkk ngir mu nekk làmp. Ci booru minwi, ñu daldi wër fu soldaar yooyu doon fanaan. Jékki-jékki rekk, ñépp a ëf ci seen béjjén, toj seeni pot te yuuxu : ‘ Jaasi Yexowa ak bu Sedeyon ! ’ Bi soldaar yi yeewoo, seen xel jaxasoo, ñu tiit ñoom ñépp, daldi daw, waa Israyil yóbbu ndam li.