Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 53

Li Yefte Dig Yexowa

Li Yefte Dig Yexowa

NDAX masuloo dige dara ba pare gis ne yombul a def ? Ki ñuy wone fii, loolu moo ko dal, moo tax xolam jeex nii. Góor googu mu ngi tudd Yefte (Yiphtah). Àttekat bu am fit la woon ca Israyil.

Yefte dund na ci jamano joo xam ne, waa Israyil dañu bàyyi woon jaamu Yexowa. Delluwaat nañu ci lu bon. Looloo tax Yexowa bàyyi waa Ammon fitnaal leen. Waa Israyil daldi yuuxu te ñaan Yexowa : ‘ Bàkkaar nañu. Ñu ngi lay ñaan nga muccal ñu ! ’

Mbooloo mi mu ngi réccu lu bon li mu doon def. Ñu daldi jaamuwaat Yexowa ngir wone loolu. Yexowa daldi leen dimbaliwaat.

Mbooloo mi tànn na Yefte ngir xeex waa Ammon yu bon yi. Yefte bëgg na lool Yexowa jàpple ko ci xeex boobu. Mu daldi dig Yexowa lii : ‘ Boo defee ba ma gañe waa Ammon, bu ma ñibbisee, dinaa la may kiy jëkk génn sama kër ngir teeru ma. ’

Yexowa déglu na loolu te dimbali na Yefte mu yóbbu ndam li. Bi Yefte ñibbisee këram, ndax xam nga kan moo jëkk a génn ngir teeru ko ? Doomam bu jigéen, fekk doom jooju rekk la amoon. Yefte daldi yuuxu, naan : ‘ Céy, sama doom ! Sama xol yépp jeex na. Am na lu ma dig Yexowa, te mënuma ci dellu ginnaaw. ’

Bi doomu Yefte déggee li baayam dige woon, moom it xolam jeex. Léegi dina war a jóge kër baayam, tàggoo it ak xaritam yépp. Te dundam yépp dina liggéeyal Yexowa ca Silo ci tàntu Yàlla fi ñu koy jaamoo. Waaye lii la wax baayam : ‘ Li nga dig Yexowa, nanga ko def. ’

Doomu Yefte dem na Silo te fa la des dundam yépp di liggéeyal Yexowa rekk. At mu nekk, jigéenu Israyil yi dañu ko doon seeti, daldi fa am jataay bu neex. Mbooloo mi dafa bëggoon doomu Yefte ndaxte dafa doon jaamu Yexowa dëgg.