Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 4

Diggante Buur bu jëkk bi ci Israyil ba bi ñu nekkee jaam ca Babilon

Diggante Buur bu jëkk bi ci Israyil ba bi ñu nekkee jaam ca Babilon

Sóol moo doon buur bi jëkk ci Israyil. Waaye Yexowa bàyyi na ko te dafa tànn Daawuda ngir mu jël palaasam. Dinañu jàng lu bare ci Daawuda. Bi mu nekkee xale, dafa xeex ak ponkal bi tudd Goliyàtt. Ay at ginnaaw loolu, daw na buur bi Sóol ndaxte Sóol dafa ko doon iñaane. Te it am na jigéen bu rafet bu tudd Abigayil bu ko tere def lu ñaaw lool.

Dinañu jàng itam lu bare ci doomu Daawuda bi tudd Suleymaan te nekkoon buuru Israyil ginnaaw Daawuda. Ñetti buur yi jëkk ci Israyil, kenn ku nekk dafa nguuru 40 at. Ginnaaw bi Suleymaan gaañoo, xaaj nañu Israyil mu am ñaari nguur : benn bu féete bëj-gànnaar ak beneen bu féete bëj-saalum.

Nguur gi féete woon bëj-gànnaar, dafa boole woon 10 giiru Israyil. Yàgg na 257 at bala waa Asiri alag ko. Ay 133 at ginnaaw loolu, alag nañu itam nguur gi féete woon bëj-saalum. Booba lañu yóbbu waa Israyil ñu nekk jaam ca Babilon. Kon dinañu gis ci XAAJ 4 ay xew-xew yu bare te am solo yu amoon ci lu mat 510 at.

 

IN THIS SECTION

NETTALI 56

Sóol, Buur Bi Jëkk A Am Ci Israyil

Yàlla moo tànnoon Sóol ca njàlbéen waaye moo ko folli itam, mën nañu ci jànge lu ñuy jariñ.

NETTALI 57

Yàlla Tànn Na Daawuda

Lan la Yàlla gis ci Daawuda te yonent Yàlla Samwil gisu ko woon ?

NETTALI 58

Daawuda Ak Goliyàtt

Gànnaayu Daawuda rekk daanul Goliyàtt waaye leneen lu ko ëpp doole la.

NETTALI 59

Li Tax Daawuda War A Daw

Bu njëkk, Sóol dafa kontaanoon lool ci Daawuda, waaye mujj na di ko iñaane ba di ko wut a rey. Lu tax ?

NETTALI 60

Abigayil Ak Daawuda

Abigayil dafa woowe jëkkëram ku amul benn xel, moo tax Nabal deewul, waaye loolu taxul mu rëcc lu yàgg.

NETTALI 61

Dañu Def Daawuda Buur

Daawuda wone na ne mat na ngir doon buur ci Israyil ci li mu def ak li mu nanguwul woon a def.

NETTALI 62

Daawuda Am Na Poroblem Ci Biir Këram

Lenn lu garaaw lool li Daawuda def jural na ko musiba moom ci boppam ak njabootam ay at.

NETTALI 63

Suleymaan, Buur Bu Am Xel La

Ndax ci dëgg-dëgg, Suleymaan doon na dagg liir bi ñaar ?

NETTALI 64

Suleymaan Mu Ngi Tabax Kër Yàlla Gi

Doonte sax Suleymaan amoon na xel lool, loolu terewul ñu puus ko ba mu doxale ni ku ñàkk xel te jëf jëf ju bon.

NETTALI 65

Xaaj Nañu Nguur Gi

Bi Yérobowam komaasee nguuru rekk, dafa dugal mbooloo mi ci bàyyi yoonu Yàlla.

NETTALI 66

Jabaru Buur Bu Tuddoon Yesabel Te Nekkoon Ku Bon

Dara mënu ko woon a teree am li mu bëgg.

NETTALI 67

Yosafat Teg Na Yaakaaram Ci Yexowa

Lu tax ay xarekat yuy dem ngir xare nangu ay woykat yu yorul gànnaay jiite leen ?

NETTALI 68

Ñaari Xale Yu Dee Woon Ba Dekki

Ndax ku dee mën na dekki ? Loolu mas naa am !

NETTALI 69

Xale Bu Jigéen Buy Dimbali Kilifa Gu Mag

Amoon na fitu wax, te loolu tax na kéemaan am.

NETTALI 70

Yunus Ak Jën Bu Réy Bi

Yunus jàng na lu am solo lu jëm ci def li ñu Yexowa sant.

NETTALI 71

Yàlla Dige Na Àjjana

Àjjana ju njëkk ja réyul woon, waaye bii dina fees àddina si.

NETTALI 72

Yàlla Dimbali Na Buur Esékiyas

Ci benn guddi, ab malaaka rey na 185 000 soldaaru Asiri.

NETTALI 73

Buur Bu Baax Bi Mujj Ci Israyil

Yosiyas xale la woon waaye jël na dogal yu laaj fit.

NETTALI 74

Góor Gii, Tiitul, Ragalul

Yérémi dafa xalaatoon ne mënta nekk yonent ndaxte xale la, waaye Yàlla xamoon na ne Yérimi dina ko mën.

NETTALI 75

Ñeenti Xale Yu Góor Ca Babilon

Ñoom mujj nañu tekki doonte sax teqali nañu leen ak seeni mbokk.

NETTALI 76

Ñu Ngiy Alag Yerusalem

Lu tax Yexowa bàyyi noonu Israyil yi, maanaam waa Babilon alag Yerusalem ?