Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 56

Sóol, Buur Bi Jëkk A Am Ci Israyil

Sóol, Buur Bi Jëkk A Am Ci Israyil

XOOLAL Samwil. Mu ngi sotti diw ci boppu góor googu ngay gis fii. Loolu lañu doon def booba ngir wone ki ñu tànn ngir mu nekk buur. Yexowa moo wax Samwil mu tuur diw boobu ci boppu Sóol. Diw boobu xeeñ lu neex, bokkul woon ak yeneen diw yi.

Sóol xalaatul ne moom moo war a nekk buur. Lii la wax Samwil : ‘ Ci askanu Ben-yamin laa bokk. Barewuñu dara fii ci Israyil. Ñoo fi gën a tuuti. Lu tax nga may wax ne, man maay nekk buur ? ’ Yexowa dafa bëgg Sóol ndaxte nekkul nit kuy réy-réylu. Looloo tax mu tànn ko ngir mu nekk buur.

Waaye loolu tekkiwul ne Sóol, nit ku néew doole walla ku ndaw la. Ci njaboot gu bare alal la bokk. Ku rafet te am taxawaay la. Moo sut ñépp ci Israyil ! Sóol, ku mën daw la itam te dafa bare doole. Mbooloo mi dafa kontaan ndax li Yexowa tànn Sóol ngir mu nekk buur. Ñépp a ngi yuuxu lii : ‘ Yàlla na buur bi gudd fan ! ’

Ñiy xeex Israyil, ba tey dañu am doole, di leen sonal rekk. Tuuti ginnaaw bi ñu defee Sóol buur, waa Ammon dañu ñów pur xeex ak waa Israyil. Sóol daldi dajale ay xarekat te xeex ak waa Ammon ba daan leen. Mbooloo mi kontaan ci li Sóol nekke seen buur.

Ci at yi topp ci loolu, Sóol dafa kontine di xeex ñi bañoon Israyil te di leen daan. Sóol amoon na it doom bu góor bu tudd Yonatan. Ku am fit la woon. Dimbali na waa Israyil ci ay xeex yu bare ba ñu yóbbu ndam li. Waaye waa Filisti ñu ngi kontine di nekk ñi gën a bañ waa Israyil. Benn bés, ay junniy junniy nit ci ñoom dañu ñów ngir xeex ak waa Israyil.

Samwil wax na Sóol mu xaar ko ba mu ñów, ngir def benn sarax, maanaam benn maye, pur Yexowa. Waaye ba léegi Samwil agseegul. Sóol dafa ragal waa Filisti yi komaase xeex bi, mu daldi def sarax bi, moom ci boppam. Bi Samwil ñówee, dafa wax Sóol ne deful li ñu ko waxoon. Mu ne ko it : ‘ Yexowa dina tànn keneen ngir mu nekk buuru Israyil. ’

Beneen yoon itam, Sóol toppul li ñu ko waxoon. Samwil ne ko : ‘ Déggal Yexowa moo gën sarax ko sa xar bi gën a rafet. Ndegam toppuloo li mu la waxoon, Yexowa dootu la bàyyi nga nekk buuru Israyil. ’

Mën nañu ci jàng lu am solo : War nañu wéy di déggal Yexowa. Gis nañu it ne ku baax mën na walbatiku, nekk ku bon. Loolu moo daloon Sóol. Waaye ñun, bëgguñu bon mukk, du dëgg ?

1 Samwil (1 Samuel) pàcc 9 ba 11 ; 13:5-14 ; 14:47-52 ; 15:1-35 ; 2 Samuel 1:23.