Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 60

Abigayil Ak Daawuda

Abigayil Ak Daawuda

NDAX xam nga jigéen bu rafet biy fekksi Daawuda nii ? Mu ngi tudd Abigayil. Ku baax la te am xel. Fi mu ne nii, am na lu bon lu Daawuda bëggoon a def te Abigayil dina tax mu bañ koo def. Bala ñuy jàng loolu, nañu seet li xewoon ak Daawuda.

Bi Daawuda dawee Sóol, dafa dem làqu ci pax bu mag bu mel ni neeg ci biir montaañ. Magam yi ak waa këram yépp ñów nekk ak moom. Lu tollu ak 400 góor ñoo ñów itam ngir nekk ak moom, Daawuda nekk seen njiit. Daawuda daldi dem ca buuru Mowab, ne ko : ‘ Dimbali ma, nga bàyyi sama baay ak sama yaay ñu nekk fii ak yow ba ma gis lu may dal. ’ Bi ñu paree, Daawuda ak nitam yi dem làqu ci ay tund, maanaam ci ay montaañ yu ndaw.

Ca jamano jooju la Daawuda daje ak Abigayil. Jëkkëram, Nabal, ku bare alal la te dafa am tool yu bare. Am na 3 000 xar ak 1 000 béy. Waaye nag Nabal, ku bon la. Abigayil, moom, dafa rafet lool te xam ni ñuy defe lu baax. Musal na sax njabootam ci musiba. Nañu seet ni mu defe loolu.

Daawuda ak nitam yi defaloon nañu lu baax Nabal. Jàpple nañu ñi doon aar xaram yi. Mu am bés nag, Daawuda yónni ay nitam ci Nabal ngir ñaan ko dara. Bi ñu àggee ci Nabal, dañu ko fekk, moom ak ñeneen ñu ko doon dimbali, ñuy dagg karawu xaram yi. Loolu, feet la woon ci ñoom te Nabal amoon na lekk bu neex te bare. Niti Daawuda ne Nabal : ‘ Defal nañu la lu baax. Masuñu la sàcc benn xar waaye dañu jàpple ñi leen doon sàmm. Léegi, ñu ngi lay ñaan nga may ñu lu ñuy lekk. ’

Nabal ne leen : ‘ Duma jox sama lekk ay nit ñu mel ni yéen. ’ Mu daldi leen wax ay wax yu bon te wax lu bon it ci Daawuda. Bi ñu ñibbee ba wax loolu Daawuda, Daawuda dafa mer lool. Mu ne nitam yi : ‘ Takkleen seen jaasi ! ’ Ñu daldi jóg, dem pur rey Nabal ak nitam yi.

Ci nitu Nabal yi, am na ku déggoon lu bon li mu wax. Mu dem wax ko Abigayil. Abigayil jóg gaaw, jël ay lekk, def ko ci kow mbaam te dem. Bi mu gisee Daawuda, mu wàcc mbaam bi, sukk, ba pare ne : ‘ Góor gi, ngir Yàlla, bul xool ci sama jëkkër Nabal. Moom amul benn xel te lu amul maanaa lay def. Lii, yaa ko moom. Nanga ko jël te baal ñu li ñu la def. ’

Daawuda ne ko : ‘ Jigéen bu am xel nga. Yaa ma teree rey Nabal ndax lu bon li mu ma defoon. Demal ak jàmm. ’ Ginnaaw loolu, bi Nabal deewee, Daawuda takk na Abigayil.