Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 62

Daawuda Am Na Poroblem Ci Biir Këram

Daawuda Am Na Poroblem Ci Biir Këram

LÉEGI, Daawuda mu ngi nguuru ci Yerusalem. Yexowa dimbali na xarekatam yi, maanaam ñiy xeex ngir waa Israyil, ba ñu gañe xeex yu bare. Yexowa dige woon na ne dina may waa Israyil réewu Kanaan. Yexowa dimbali na leen ba ñu moom réew mi yépp.

Daawuda, buur bu baax la. Bëgg na Yexowa. Looloo tax bi mu nangoo Yerusalem ci loxo ñi fa dëkkoon, lenn ci li mu jëkk a def mooy indi fa gaalu kóllëre bi. Bëgg na tabax it benn kër Yàlla fu muy dugal gaal googu.

Bi Daawuda gënee mag dafa def lu garaaw lool. Xamoon na ne jël loo moomul, baaxul. Waaye benn ngoon, fekk mu ngi doon dox ci teraasu këram, mu séen ci suuf benn jigéen bu rafet lool. Kooku, Batséba la tudd, jëkkëram tudd Uri. Ci xarekatu Daawuda yi la bokk.

Daawuda dafa bëggoon a tëdd ak Batséba ba yónni ay nit pur ñu indi ko këram. Booba, dafa fekk jëkkëram dem xeex ngir waa Israyil. Daawuda tëdd ak Batséba. Batséba ëmb. Daawuda jaaxle lool. Mu yónnee ci Yowab mi doon jiite xarekatam yi, ngir wax ko mu def Uri ci kanamu xarekat yi. Dafa bëggoon mu dee fa. Bi Uri deewee, Daawuda takk na Batséba.

Yexowa dafa mer lool ndax li Daawuda def. Mu daldi yónni yonentam Natan ngir mu wax ak Daawuda ci bàkkaar yi mu def. Xoolal fii Natan. Mu ngi wax ak Daawuda. Daawuda mu ngi réccu lool li mu def. Loolu moo tax Yexowa du ko rey. Waaye lii la Yexowa wax : ‘ Ndegam lu bon loolu nga def, dinga am coono yu bare ci sa kër. ’ Seetal léegi coono yi mu am !

Doom bi Batséba jur, dee na. Ginnaaw loolu, taawu Daawuda mi tudd Amnon fexe na ba wéet ak rakkam bu jigéen bi tudd Tamar, mu daldi ko siif. Beneen doomu Daawuda bu góor bi tudd Absalom mer lool, daldi rey Amnon. Ginnaaw loolu, Absalom fexe ba ñu bare ci mbooloo mi topp ko, mu daldi def boppam buur. Xeex am, Daawuda gañe, Absalom dee. Dëgg-dëgg, Daawuda bare na coono lool !

Ci diggante loolu lépp, Batséba jur na beneen doom bu tudd Suleymaan. Bi Daawuda demee ba màgget te feebar, doomam bu góor bi tudd Adoniyaa jéem na def boppam buur. Daawuda daldi laaj saraxalekat bu mag bi tudd Sadog mu sotti diw ci boppu Suleymaan ngir wone ne moom mooy nekk buur. Tuuti ginnaaw loolu, Daawuda dee. Amoon na 70 at te 40 at la nguuru. Léegi Suleymaan moo nekk buuru Israyi.