Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 63

Suleymaan, Buur Bu Am Xel La

Suleymaan, Buur Bu Am Xel La

SULEYMAAN, dañu ko def buur fekk amagul ñaar-fukki at. Ku bëgg Yexowa la te dafay topp xelal yu baax yi ko baayam Daawuda jox. Yexowa kontaan na ci Suleymaan. Benn guddi, mu daldi wax ak moom ci gént, ne ko : ‘ Suleymaan, loo bëgg ma may la ? ’

Suleymaan ne ko : ‘ Yexowa, sama Yàlla, xale bu ndaw laa te mënuma nguuru. Kon nanga ma may xel, ma xam ni ma war a ilife sa mbooloo, ilif bu jub. ’

Li Suleymaan laaj noonu, dafa neex Yexowa. Mu ne ko : ‘ Ndegam danga ma ñaan xel te ñaanoo ma gudd fan walla alal ju bare, dinaa la may xel buy sut xelu bépp nit bu mas a dund ci kow suuf. Dinaa la may itam li nga ñaanul, maanaam alal ak ndam. ’

Yàggul ginnaaw loolu, ñaari jigéen ñów ci Suleymaan ak poroblem bu doy waar. Kenn ki ne : ‘ Man ak jigéen bii ñoo bokk kër. Dama jur benn doom ju góor. Ñaari fan ginnaaw loolu, moom it, mu jur doom ju góor. Waaye doomam dafa dee ci guddi. Léegi, bi ma doon nelaw, dafa teg doomam ji dee ci sama wet, jël sama doom, teg ko ci wetam. Bi ma yeewoo ba gis xale bi dee, ma xam ne du sama doom. ’

Beneen jigéen bi daldi ne : ‘ Déedéet, du dëgg ! Man maa moom xale biy dund. Ki dee, moom mooy yaayam. ’ Keneen ki ne: ‘ Du dëgg ! Yaa moom xale bi dee, man maa moom kiy dund. ’ Ñoom ñaar nekk noonu di werante rekk. Lan la Suleymaan di def nag ?

Dafa wax ñu indi benn jaasi, ba pare mu ne : ‘ Daggal liir bi ñaar, jox jigéen bu nekk benn xaaj. ’

Ki juroon xale bi daldi yuuxu, naan : ‘ Déedéet ! Ngir Yàlla, bul rey xale bi. Jox ko ko. ’ Beneen jigéen bi ne : ‘ Bu ko jox kenn ci ñun ñaar. Ayca ! Dagg ko ñaar. ’

Suleymaan daldi wax lii : ‘ Bul rey xale bi ! Jox ko kii. Kii mooy yaayam dëgg. ’ Suleymaan xam na ne moom mooy yaay ji ndaxte dafa bëgg doomam ba nangu ñu jox ko keneen ki ngir doom ji bañ a dee. Bi waa mbooloo mi déggee ni Suleymaan fajee poroblem boobu, ñu kontaan ci li ñu am buur bu am xel noonu.

Ci jamano bi Suleymaan nekkee buur, Yàlla barkeel na mbooloo mi, ñu góob lu bare ci dugub, reseñ, figg ak yeneen lekk yu bare. Mbooloo mi am yére yu baax te rafet te dëkk ci kër yu baax. Ku nekk am lu baax li mu soxla, ba mu ëpp sax.