Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 65

Xaaj Nañu Nguur Gi

Xaaj Nañu Nguur Gi

NDAX xam nga lu tax góor gi nekk fii xotti yére bi, def ko ay morso ? Yexowa moo ko ko sant. Yonent Yàlla la te mu ngi tudd Akisu. Ndax xam nga lan mooy yonent ? Nit la koo xam ne Yàlla dafa koy wax lu war a am ëllëg.

Fii Akisu mu ngi wax ak Yérobowam. Yérobowam, Suleymaan dafa ko dénkoon lu mu waroon a tabax. Bi Akisu tasee ak Yérobowam ci yoon bi, Akisu def na lu doy waar. Dafa summi mbubb bu bees bi mu soloon, xotti ko mu def 12 morso. Mu ne Yérobowam : ‘ Jëlal 10 morso. Yaa leen moom. ’ Ndax xam nga lu tax Akisu jox Yérobowam 10 morso ?

Akisu nee na Yexowa dina nangu nguur gi ci loxo Suleymaan te jox Yérobowam 10 giir. Kon doomu Suleymaan bi tudd Robowam, dina nguuru ci kow ñaari giir kese.

Bi Suleymaan déggee li Akisu wax Yérobowam, mu mer lool. Jéem na rey sax Yérobowam. Yérobowam daldi daw ca Misra. Ay at ginnaaw loolu, Suleymaan gaañu na. Nekkoon na buur lu mat 40 at. Doomam Robowam lañu def buur. Bi Yérobowam déggee deewu Suleymaan ci Misra, mu daldi dellusi Israyil.

Robowam nekkul woon buur bu baax. Lu bon li mu def mbooloo mi moo ëppoon sax li baayam Suleymaan defoon. Yérobowam ak yeneen mag dem ci Robowam ne ko mu wàññi lu bon li muy def mbooloo mi. Waaye Robowam bëggul déglu. Dafa yokk sax li mu doon def. Loolu moo tax mbooloo mi def Yérobowam buur ci kow 10 giiru Israyil. Waaye giiru Yuda ak giiru Ben-yamin, ñoom, des nañu ak Robowam, mu nekk seen buur.

Yérobowam bëggul ñi nekk ak moom dem Yerusalem jaamu fa Yexowa ci kër Yàlla gi. Looloo tax mu defar ñaari nagu wurus te fexe ba ñi bokk ci nguuru 10 giir yi jaamu leen. Yàggul rekk, lu bon ak xeex daldi bare lool ci réew mi yépp.

Nguuru ñaari giir yi bare na coono moom itam. Ginnaaw bi Robowam nekkee buur, matul sax juróomi at, buuru Misra ñów xeex ak ñi nekk Yérusalem. Jël na alal ju bare ci kër Yàlla gi. Kon léegi, kër Yàlla gi melatul ni bi ñu ko tabaxee, fekk loolu yàggul woon sax.

1 Buur yi (1 Rois) 11:26-43 ; 12:1-33 ; 14:21-31.