Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 67

Yosafat Teg Na Yaakaaram Ci Yexowa

Yosafat Teg Na Yaakaaram Ci Yexowa

GÓOR ñi nekk fii, ñan lañu te lan lañuy def ? Ndax xam nga ko ? Góor ñii, ñu ngi dem xeexi. Ñi jiitu, dañuy woy. Xéyna dinga laaj lii : ‘ Lu tax ñiy woy amuñu jaasi ak xeej pur xeex ni ñeneen ñi nekk seen ginnaaw ? ’ Nañu seet lu tax.

Yosafat (Yehoshaphat) mooy buuru nguuru ñaari giiru Israyil. Moom ak buur Akab ak Yesabel ñi bokk ci nguuru 10 giiru Israyil ñoo bokk jamano. Waaye Yosafat moom, buur bu baax la. Baayam Asaf (Asa), buur bu baax la woon itam. Kon ci ay at yu bare, mbooloo mi bokkoon ci nguuru ñaari giir yi féete woon bëj-saluum, ñu nga woon ci jàmm.

Waaye léegi am na luy tiital mbooloo mi. Am na ñu ñów wax Yosafat lii : ‘ Ay soldaar yu bare ñu ngi ñów ngir xeex ak yow. Ñu ngi jóge Mowab, Ammon ak montaañu Seyir. ’ Ñu bare ci waa Israyil daldi gurupoo ci Yérusalem ngir ñaan ndimbalu Yexowa. Ñu dem ci kër Yàlla gi. Foofu Yosafat ñaan Yexowa, ne ko : ‘ Céy, Yexowa suñu Yàlla, xamuñu lu ñuy def. Amuñu benn pexe ngir mën a xeex soldaar yooyu yépp. Ci yow lañu teg suñu yaakaar. ’

Yexowa déglu na ñaan bi, mu yebal benn jaamam, mu wax mbooloo mi lii : ‘ Xeex bii, moomuleen ko. Yàlla moo ko moom. Dungeen soxla xeex. Nangeen xool rekk te gis ni leen Yexowa di muccale. ’

Ci ëllëg ci suba si, Yosafat wax mbooloo mi ne : ‘ Nangeen teg seen yaakaar ci Yexowa ! ’ Mu wax woykat yi ñu jiitu ñi waroon a xeex te bu ñuy dox ñuy woyal Yexowa ngir màggal ko. Ndax xam nga li xew bi ñu jegee fu xeex bi waroon a am ? Yexowa def na ba seeni noon xeexante ci seen biir. Bi waa Israyil àggee foofu, dañu fekk ñépp dee ba pare. Kenn rëccul!

Dëgg-dëgg, Yosafat def na lu baax bi mu tegee yaakaaram ci Yexowa. Ñun it, dinañu def lu baax bu ñu tegee suñu yaakaar ci Moom.