Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 68

Ñaari Xale Yu Dee Woon Ba Dekki

Ñaari Xale Yu Dee Woon Ba Dekki

BOO deewoon te ñu dekkal la, sa yaay lu muy def ? Dina kontaan lool, de ! Waaye ndax ku dee mën na dekki ? Ndax loolu mas na am ?

Xoolal góor gi nekk fii, jigéen bi ak xale bi. Góor gi, yonent Yàlla la te mu ngi tudd Iliyas. Jigéen bi, jëkkëram faatu na, te mu ngi dëkk ci dëkk bi tudd Sarepeta. Xale bi, doomam la. Benn bés xale bi feebar. Feebar bi yokku ba xale bi mujj a dee. Iliyas wax jigéen bi : ‘ Indil ma xale bi. ’

Iliyas jël xale bi dee, yóbbu ko ci kow, tëral ko ci lal. Mu ñaan Yexowa, ne : ‘ Céy Yexowa, nanga dekkal xale bi. ’ Xale bi daldi noyyi ! Iliyas wàcce ko ci suuf, ne jigéen bi : ‘ Xoolal, sa doom mu ngi dund ! ’ Loolu moo tax yaay ji kontaan nii.

Am na beneen yonentu Yexowa bu mag bu tudd Alyaasa (Alisa). Liggéeyam mooy dimbali Iliyas ci li muy def. Waaye Yexowa jaar na itam ci Alyaasa ngir def kéemaan. Benn bés Alyaasa dem na ca dëkku Sunem. Mu fekk fa benn góor ak jabaram. Jabar jii defal ko lu baax. Mu am bés, soxna soosu am doom.

Xale bi màgg. Benn suba mu dem fekkji baayam bu doon liggéey ci tool. Jékki-jékki rekk mu yuuxu, naan : ‘ Sama bopp dafay metti ! ’ Ñu yóbbu ko kër ga, waaye mujj na dee. Xolu yaayam jeex tàkk ! Mu jóg, dem woo Alyaasa.

Bi Alyaasa ñówee, mu dem ci néeg bi ñu defe xale bi. Mu ñaan Yexowa ba pare tëdd ci kow néew bi. Yàggul dara, yaram bi komaase tàng, xale bi daldi tisóoli juróom-ñaari yoon. Bi yaay ji duggee ci néeg bi ba gis doomam di dund, mu kontaan lool !

Ñi dee ci àddina bare nañu lool. Loolu metti na seeni mbokk ak seeni xarit lool. Ñun, mënuñu dekkal nit. Waaye Yexowa mën na ko. Bu ci kanamee ci téere bii, dinañu jang li Yexowa di def ba ay milioŋi nit dundaat.