Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 69

Xale Bu Jigéen Buy Dimbali Kilifa Gu Mag

Xale Bu Jigéen Buy Dimbali Kilifa Gu Mag

XOOLAL xale bu jigéen bi nekk fii. Xam nga lan lay wax ? Mu ngiy wax ak jigéen bi ci yonent Yàlla Alyaasa (Alisa) ak lépp li mu def ci kàttanu Yexowa. Soxna si xamul Yexowa ndaxte moom du waa Israyil. Kon nañu seet lu tax xale bi nekk këram.

Soxna si, waa Siri la. Jëkkëram, Naaman la tudd. Moom mooy jiite soldaaru Siri yi. Waa Siri jàppoon nañu xale bu jigéen bii bokk ci Israyil, indi ko jabaru Naaman pur mu nekk surgaam, maanaam pur mu koy liggéeyal.

Naaman am na feebar bu metti bu ñuy woowe ngaana. Feebar boobu lée-lée mu mel ni dafay am fu muy lekk ci yaramu nit ki. Lii la xale bi wax jabaru Naaman : ‘ Bu sama kilifa mënoon a dem ci yonent Yexowa bi nekk Israyil, kooku dina ko faj. ’ Ñu wax loolu Naaman.

Naaman bëgg na wér lool. Mu dem Israyil, àgg ci kër Alyaasa. Alyaasa wax surgaam mu génn, wax Naaman mu dem sangu juróom-ñaari yoon ci dexu Yurdan. Naaman mer lool. Mu ne : ‘ Dex yi nekk suñu réew ñoo gën fuuf dexu Israyil yi ! ’ Mu daldi dem.

Waaye benn surgaam ne ko : ‘ Kilifa gi, bu la Alyaasa waxoon lu yombul a def, ndax doo ko def ? Léegi, sangu rekk la la wax. Lu tax mënoo ko def, ni mu la ko waxe ? ’ Naaman déglu na surgaam te dem na sangu juróom-ñaari yoon ci dexu Yurdan. Bi mu defee loolu, mu wér péŋŋ !

Naaman kontaan na lool. Mu dellu ci Alyaasa ne ko : ‘ Léegi xam naa ci lu wóor ne Yàlla Israyil rekk moo nekk Yàlla dëgg ji ci àddina si sépp. Kon, ngir Yàlla, nanga nangu sama maye bi. ’ Alyaasa ne ko : ‘ Déedéet, duma ko jël. ’ Alyaasa xam na ne warul jël maye boobu, ndaxte Yexowa moo faj Naaman. Du moom. Waaye surga Alyaasa mi tudd Geyasi, moom bëgg na maye boobu.

Geyasi daldi def lii : bi Naaman demee, mu daw, dab ko te ne ko : ‘ Alyaasa moo ma yónni ci yow ngir wax la ne dafa am ay xarit yu sog a ñów seetsi ko. Ndax mënoo ko jox ci li nga ko bëggoon a may pur mu jox leen ko ? ’ Geyasi dafa doon fen. Waaye Naaman moom xamu ko. Mu jël ci li mu bëggoon a maye, jox ko Geyasi.

Geyasi ñibbi këram. Alyaasa moom xam na li Geyasi def. Yexowa moo ko ko wax. Alyaasa ne Geyasi : ‘ Ndegam def nga lu bon loolu, ngaana Naaman dina dal sa kow. ’ Te loolu moo am ci saa si !

Lan lañu mën a jàng ci loolu ? Benn, war nañu mel ni xale bu jigéen boobu te wax ak nit ñi ci Yexowa. Loolu mën na jur lu bare lu baax. Ñaar, waruñu yéeg suñu bopp ni ko Naaman jëkkoon a def, waaye dañu war a déggal ñi Yàlla tànn. Ñett, waruñu def li Geyasi defoon, maanaam fen. Dëgg dëgg, ndax amul lu bare li ñu mën a jàpp ci li ñuy jàng ci Biibël bi ?