Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 71

Yàlla Dige Na Àjjana

Yàlla Dige Na Àjjana

ÀJJANA ji ñu wone fii, mën na am mu niru ak bi Yàlla wonoon yonentam Esayi. Esayi dund na tuuti ci ginnaaw jamano Yunus.

Àjjana, baat bi ci boppam, mu ngi tekki “ tool ”. Ndax loolu dafa lay fàttali li ñu gis ba pare ci téere bii ? Ci lu bare, li ñuy wone fii niru na tool bu rafet bi Yexowa Yàlla mayoon suñuy maam Aadama ak Awa, du dëgg ? Waaye ndax suuf si sépp dina mas a nekk àjjana ?

Yexowa sant na yonentam Esayi mu bind lu jëm ci àjjana ji muy indil nitam ñi. Nee na : ‘ Jàmm dina am diggante bukki ak mbote. Nag ak doomu gaynde dinañu lekkandoo te xale yu ndaw ñoo leen di sàmm. Liir sax dina mën a fo ci wetu jaan ju yor poson, waaye dara du ko dal. ’

Ñu bare dinañu ne : ‘ Loolu mënul am mukk. Fii ci suuf si lañu fekk coono yi te fii lañu leen di bàyyi.’ Waaye seetal lii : Béréb bi Yàlla mayoon Aadama ak Awa pur ñu dëkk ci, nu mu meloon ?

Yàlla dafa dugaloon Aadama ak Awa ci benn àjjana. Seen bañ a déggal Yàlla rekk moo tax ñu jóge ci béréb bu rafet boobu, màgget te dee. Yàlla dig na ne dina may ñi ko bëgg li Aadama ak Awa ñàkkoon.

Ci àjjana jiy ñów, dara lu bon du dal nit ñi. Jàmm ju mat sëkk mooy am. Nit ñépp dinañu am wér-gi-yaram te dëkk ci mbégte. Lépp ay nekk ni ko Yàlla bëgge woon ca njëlbéen. Dinañu jàng ci kanam naka la Yàlla di defe loolu lépp.