Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 72

Yàlla Dimbali Na Buur Esékiyas

Yàlla Dimbali Na Buur Esékiyas

NDAX xam nga lu tax góor gii nekk fii di ñaan Yexowa ? Lu tax mu teg leetar yi ci kanamu saraxalukaayu Yexowa ? Góor googu, Esékiyas la tudd. Buur la ci ñaari giiru Israyil yi féete bëj-saalum. Mu ngi ci coono bu réy. Ndax xam nga lu tax ?

Soldaari Asiri alag nañu ba pare nguur gi boole 10 giir yi féete bëj-gànnaar. Yexowa bàyyi na loolu am, ndaxte nit ñooñu dañu bonoon lool. Léegi, soldaari Asiri agsi nañu ngir xeex ak ñi bokk ci nguur gi boole ñaari giir yi.

Buuru Asiri mu ngi sog a yónni buur Esékiyas ay leetar. Mooy leetar yi Esékiyas teg fii ci kanamu Yàlla. Ci leetar yi, buuru Asiri dafay ñaawal Yexowa te wax Esékiyas mu nangu ne daanu na ba pare. Loolu moo tax Esékiyas ñaan Yexowa, ne ko : ‘ Céy Yexowa, nanga ñu muccal ci buuru Asiri. Xeet yépp bu ñu gisee loolu, dinañu xam ne yow rekk yaay Yàlla dëgg. ’ Ndax Yexowa dina def li Esékiyas bëgg?

Esékiyas, buur bu baax la. Melul ni buur yu bon yi nekkoon ci nguur gi boole woon 10 giiru Israyil yi. Melul itam ni baayam Akas mi nekkoon buur bu bon. Esékiyas fexe na ba topp bu baax ndigalu Yexowa yépp. Looloo tax, bi Esékiyas ñaanee ba pare, yonent Yàlla Esayi yónni ko xibaar bii jóge woon ci Yexowa : ‘ Buuru Asiri du dugg Yerusalem. Kenn ci soldaaram yi du ko sax jege. Duñu sànni benn fett ci dëkk bi. ’

Xoolal li ñuy wone fii. Soldaar yu dee yi nekk fii, xam nga ñan lañu ? Ñooy soldaari Asiri. Yexowa yónni na malaakaam mu rey 185 000 soldaar ci benn guddi. Buuru Asiri daldi bàyyi xeex bi te ñibbi.

Nguuru ñaari giir yi mucc na, mbooloo mi am jàmm. Waaye bi Esékiyas deewee, doomam Manase lañu fal buur. Manase, buur bu bon la woon. Doomam Amon mi topp ci moom, buur bu bon la woon itam. Réew mi daldi feesaat ak nit ñuy xeex te soxor. Buur Amon, bi ko surgaam yi reyee, doomam Yosiyas lañu fal buur ci nguuru ñaari giir yi.

2 Buur yi (2 Rois) 18:1-36 ; 19:1-37 ; 21:1-25.