Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 73

Buur Bu Baax Bi Mujj Ci Israyil

Buur Bu Baax Bi Mujj Ci Israyil

BI ÑU defee Yosiyas buur, juróom-ñetti at rekk la amoon. Buur la woon ci nguuru ñaari giiru Israyil yi féete woon bëj-saalum. Ndegam xale bu ndaw la woon, bi mu komaasee di nguuru, ay mag ñoo ko ci doon dimbali.

Juróom-ñaari at ginnaaw bi mu nekkee buur, Yosiyas daldi wut a xam Yexowa. Mu jéem a roy buur yu baax yu mel ni Daawuda, Yosafat ak Esékiyas. Te bala mu am ñaar-fukki at sax, def na loo xam ne dafa laajoon fit dëgg.

Fi ñu tollu nii, ñi ëpp ci waa Israyil yàgg nañu bon. Dañuy jaamu ay yàlla yu dul dëgg. Dañuy sukk ci kanamu xërëm. Yosiyas jóg ak nitam yi ngir dem ci réew mi yépp dindi loolu lépp. Liggéey bu réy la ndaxte ñiy jaamu yàlla yu dul dëgg yi bare nañu lool. Xoolal fii Yosiyaa ak nitam yi. Ñu ngiy toj xërëm yi.

Ginnaaw loolu, Yosiyas jël ñetti góor, sant leen ñu defaraat kër Yexowa gi. Mu laaj mbooloo mi xaalis, dajale ko te jox ko góor ñooñu pur liggéey bi. Bi ñu doon def liggéey boobu, saraxalekat bu mag bi tudd Ilkiya (Hilqia) gis na lu am solo lool. Mooy téere fu Yàlla santoon Musaa bu yàgg a yàgg mu bind ay ndigalam. Téere boobu nag, yàggoon na réer.

Ñu daldi indil Yosiyas téere bi. Mu wax ñu jang ko ci kanamam, muy déglu. Mu gis ne mbooloo mi bàyyi na topp ndigalu Yexowa yi. Xolam daldi jeex, mu xotti mbubbam, ni nga ko gise fii. Mu ne : ‘ Yexowa dafa ñu mere, ndaxte suñu maam yi kontinewuñu topp ndigal yi ñu bind ci téere bii. ’

Yosiyas laaj saraxalekat bu mag bi tudd Ilkiya mu seet lan la leen Yexowa nar a def. Ilkiya dem laaj loolu yonent bu jigéen bi tudd Ulda (Houlda). Ulda jottali ko li Yexowa wax pur mu wax ko Yosiyas. Lii la Yexowa wax : ‘ Yerusalem ak mbooloo mi yépp dinaa leen yar ndax li ñu jaamu ay yàlla yu dul dëgg te réew mi yépp fees na ak lu bon. Waaye, ndegam yow, Yosiyas, danga def lu baax, yar boobu du ñów ci sa dund. ’